bible
ra
🌐 Language
English
Español
Français
Deutsch
Português
Italiano
Nederlands
Русский
中文
日本語
한국어
العربية
Türkçe
Tiếng Việt
ไทย
Indonesia
All Languages
Home
/
Wolof
/
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
/
Genesis 50
Genesis 50
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
← Chapter 49
Jump to:
Chapter 1
Chapter 2
Chapter 3
Chapter 4
Chapter 5
Chapter 6
Chapter 7
Chapter 8
Chapter 9
Chapter 10
Chapter 11
Chapter 12
Chapter 13
Chapter 14
Chapter 15
Chapter 16
Chapter 17
Chapter 18
Chapter 19
Chapter 20
Chapter 21
Chapter 22
Chapter 23
Chapter 24
Chapter 25
Chapter 26
Chapter 27
Chapter 28
Chapter 29
Chapter 30
Chapter 31
Chapter 32
Chapter 33
Chapter 34
Chapter 35
Chapter 36
Chapter 37
Chapter 38
Chapter 39
Chapter 40
Chapter 41
Chapter 42
Chapter 43
Chapter 44
Chapter 45
Chapter 46
Chapter 47
Chapter 48
Chapter 49
Chapter 50
1
Ba mu ko defee Yuusufa daanu ci kaw baayam. Ma ngay jooy te di ko fóon.
2
Ba loolu weesee Yuusufa jox ay fajkatam ndigal, ñu waajal baayam. Fajkat ya waajal Israyil.
3
Waaj ma am na ñeent fukki fan, ndaxte loolooy waajal bu mat sëkk cib néew. Waa Misra nag dëjal ko juróom ñaar fukki fan.
4
Ba dëj ba weesee, Yuusufa dafa wax ak waa kër Firawna, ñaan leen ñu dimbali ko, waxal ko Firawna ne ko,
5
baayam da ne woon, mu ngi waaja dee, waaye bàmmeel ba mu yettaloon boppam ca xunti ma ca réewu Kanaan, na ko giñal ne dina ko denc foofa. Mu ne kon, na ko Firawna may, mu robi baayam, ni mu ko ko giñloo woon, te délsi.
6
Firawna may ko, mu robi baayam, na mu ko ko giñloo woon.
7
Yuusufaa ngay dem robi baayam, moom ak mboolem jawriñi Firawna ak magi këram ak mboolem kàngami Misra.
8
Ña nga ànd ak waa kër Yuusufa gépp ak ay doomi baayam ak waa kër baayam, bàyyiwuñu diiwaanu Gosen lu moy xale ya ak gàtt ya ak jur gu gudd ga,
9
ay watiir aki gawar topp ca, ñu def gàngoor gu réy.
10
Ba ñu agsee ca dàggay Ataat, ja ca wàllaa dexu Yurdan, dañu koo jooy jooy yu réy te metti. Yuusufa dëjal fa baayam diiru juróom ñaari fan.
11
Waa réewu Kanaan, gis dëj ba ca dàggay Ataat, naan: «Dëju waa Misra bii aka réy!» Moo tax ñu tudde bérab booba ca wàllaa dexu Yurdan, Abel Misra (mu firi Dëju waa Misra).
12
Doomi Yanqóoba nag def la leen seen baay dénkoon,
13
yóbbu ko ca réewu Kanaan, daldi koy rob ca xunti ma ca toolub Magpela, te Ibraayma jëndoon ko ca Efron, Etteen ba, ngir def ko bàmmeel. Mooy tool, ba jàkkaarloo ak Mamre.
14
Ba Yuusufa dencee baayam ba noppi, dafa dellu Misra, moom ak doomi baayam ya ak mboolem, ña mu àndaloon ca robu baayam.
15
Magi Yuusufa ya xam nañu ne seen baay nelaw na. Ña ngay wax ca seen biir naan: «Waaw, mbaa Yuusufa dencalu nu mer, nar noo fey sunu bor ndax lu bon li nu ko ji woon lépp?»
16
Boobu lañu yóbbante Yuusufa kàddu yii, di ko wax ne ko: «Sa baay dafa noo dénkoon, bala moo nelaw, ne nu:
17
Waxleen Yuusufa ne ko, sa baay nee: “Say mag def nañu la lu bon moos, waaye ngalla baal leen seeni tooñ ak àq, ji ñu la ameel.” Kon rikk waay, baal nu àq, ndax nun nook sa baay a bokk jenn Yàlla ju nuy jaamu.» Ba ñu waxee Yuusufa loolu, mu daldi jooy.
18
Ci kaw loolu magam ya ñëwal seen bopp ba ca moom, sujjóotal ko ne ko: «Sang bi, nu ngi nii, di la siyaare.»
19
Yuusufa nag ne leen: «Buleen am dara lu ngeen di ragal. Xanaa maay Yàlla?
20
Dëgg la, fexeel ngeen ma lu bon, waaye Yàllaa ko walbati, def ko lu baax, ba dogal li am tey jii, muy bakkan yu bare yi mucc.
21
Kon nag buleen tiit, dinaa leen yor, yeen ak seeni doom.» Yooyu kàddu la dalale seen xol, ba ñu am jàmm.
22
Yuusufa dëkk na Misra, moom ak waa kër baayam ñépp, ba tollu ci téeméeri atam ak fukk,
23
te gis na doomi Efrayim, ba gis sëti Efrayim sax; rax ca dolli doomi Makir, mi Manase jur, fa kanamam lañu juddoo.
24
Mu am bés Yuusufa ne ay bokkam: «Sama waxtu jege na, waaye Yàlla moo leen di jëlsi moos, ba jële leen ci réew mii, yóbbu leen ca réew ma mu dige woon, ba giñal ko Ibraayma, Isaaxa ak Yanqóoba.»
25
Booba la Yuusufa wax doomi Israyil, ne leen: «Giñal-leen ma ne bés bu leen Yàlla jëlsee, dingeen yóbbaale samay yax, waaye dungeen ma fi bàyyi.»
26
Gannaaw loolu Yuusufa nelaw ci téeméeri atam ak fukk. Ñu waajal néew ba, ba du yàqu, daldi koy yeb cib tàdd, denc ko foofa ca Misra.
← Chapter 49
Jump to:
Chapter 1
Chapter 2
Chapter 3
Chapter 4
Chapter 5
Chapter 6
Chapter 7
Chapter 8
Chapter 9
Chapter 10
Chapter 11
Chapter 12
Chapter 13
Chapter 14
Chapter 15
Chapter 16
Chapter 17
Chapter 18
Chapter 19
Chapter 20
Chapter 21
Chapter 22
Chapter 23
Chapter 24
Chapter 25
Chapter 26
Chapter 27
Chapter 28
Chapter 29
Chapter 30
Chapter 31
Chapter 32
Chapter 33
Chapter 34
Chapter 35
Chapter 36
Chapter 37
Chapter 38
Chapter 39
Chapter 40
Chapter 41
Chapter 42
Chapter 43
Chapter 44
Chapter 45
Chapter 46
Chapter 47
Chapter 48
Chapter 49
Chapter 50
All chapters:
1
2
3
4
5
6
7
8
9
10
11
12
13
14
15
16
17
18
19
20
21
22
23
24
25
26
27
28
29
30
31
32
33
34
35
36
37
38
39
40
41
42
43
44
45
46
47
48
49
50