bible
ra
🌐 Language
English
Español
Français
Deutsch
Português
Italiano
Nederlands
Русский
中文
日本語
한국어
العربية
Türkçe
Tiếng Việt
ไทย
Indonesia
All Languages
Home
/
Wolof
/
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
/
Zechariah 13
Zechariah 13
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
← Chapter 12
Jump to:
Chapter 1
Chapter 2
Chapter 3
Chapter 4
Chapter 5
Chapter 6
Chapter 7
Chapter 8
Chapter 9
Chapter 10
Chapter 11
Chapter 12
Chapter 13
Chapter 14
Chapter 14 →
1
«Bésub keroog bëtu ndox dina bënnal kër Daawuda, ak waa Yerusalem, ngir setal bàkkaar ak sobe.
2
«Bésub keroog,» kàddug Aji Sax jee, Boroom gàngoor yi, «Turi xërëm laay dagge ci réew mi, ba deesatu leen fàttliku. Yonent yeek xelum xërëmtu it, maa koy tukkal ci réew mi.
3
Te képp kuy biralati waxyu, ay waajuram, baayam ak ndeyam nañu ko wax ne ko: “Doo dese bakkan, ndax yaa fen ci turu Aji Sax ji.” Ay waajuram, baayam ak ndeyam nañu ko jam ba mu dee, ca ba muy biral waxyu.
4
«Su bés baa, bépp yonent buy biral waxyu, kersa lay am ci am peeñoom. Kenn du sol ni yonent yi, yérey der yu ànd ak kawaram, ngir di naxe.
5
Kenn ku ne da naan: “Man de dumab yonent, beykat laa. Ab surga laa masa doon ba may ndaw ba tey.”
6
Te su ñu ko nee: “Légét yii ci sab dënn nag?” Da naan: “Lii de ay légét la yu ma jële ca sama kër xarit ya.”»
7
«Éey saamar, yewwulal sama sàmm bi, sama jàmbaar jii ma lëngool,» kàddug Aji Sax jee, Boroom gàngoor yi. «Dóoral sàmm bi, xar yi tasaaroo, ma walbati sama loxo, jublu ci jur gu ndaw gi.
8
Su boobaa ci réew mi mépp, kàddug Aji Sax jee, ñaari xaaj yi lees di dagg, ñu sànku, ñetteel ba ca des lees fay wacc.
9
Ñetteel bi laay tàbbal ci sawara, xelli ko ca ni ñuy xellee xaalis, nattu ko ni ñuy nattoo wurus cib taal. Xaaj boobu moo may woo ci sama tur, ma wuyu ko. Moom laay wax: “Sama ñoñ,” Moom mu ne: “Aji Sax jeey sama Yàlla.”»
← Chapter 12
Jump to:
Chapter 1
Chapter 2
Chapter 3
Chapter 4
Chapter 5
Chapter 6
Chapter 7
Chapter 8
Chapter 9
Chapter 10
Chapter 11
Chapter 12
Chapter 13
Chapter 14
Chapter 14 →
All chapters:
1
2
3
4
5
6
7
8
9
10
11
12
13
14