bible
ra
🌐 Language
English
Español
Français
Deutsch
Português
Italiano
Nederlands
Русский
中文
日本語
한국어
العربية
Türkçe
Tiếng Việt
ไทย
Indonesia
All Languages
Home
/
Wolof
/
Wolof 1987
/
Revelation 15
Revelation 15
Wolof 1987
← Chapter 14
Jump to:
Chapter 1
Chapter 2
Chapter 3
Chapter 4
Chapter 5
Chapter 6
Chapter 7
Chapter 8
Chapter 9
Chapter 10
Chapter 11
Chapter 12
Chapter 13
Chapter 14
Chapter 15
Chapter 16
Chapter 17
Chapter 18
Chapter 19
Chapter 20
Chapter 21
Chapter 22
Chapter 16 →
1
Noonu ma gis ca asamaan beneen firnde ju réy tey yéeme: juróom-ñaari malaaka yu taawu juróom-ñaari musiba, ñuy yu mujj ya, ndaxte ñoom ñooy matal merum Yàlla.
2
Noonu ma gis lu mel ni géej gu leer ni weer bu set buy ray-rayi ak safara. Ña nootoon rab wa ak nataalam, ak siifar bu mengoo ak turam, ñoo taxaw ca géej gu leer ga, yor xalam yu leen Yàlla jox.
3
Ñuy woy woyu Musaa jaamu Yàlla bi, ak woyu Mbote ma, naan:«Say jëf réy nañu te yéeme,yaw Boroom bi Yàlla, Aji Kàttan ji.Say yoon jub nañu te dëggu,yaw Buur bi fiy sax ba abadan.
4
Ku la ragalul, Boroom bi?Ku dul màggal saw tur?Kenn, ndaxte yaw rekk yaa sell.Xeet yépp dinañu dikk, jaamu la,ndax say àtte bir na ñépp.»
5
Gannaaw loolu ma xool, noonu kër Yàlla ubbiku ca asamaan, muy tàntu màggalukaay, bi ëmb li Yàlla seede.
6
Juróom-ñaari malaaka, ya taawu juróom-ñaari musiba ya, daldi génn ca kër Yàlla ga. Ñu sol mbubb yu set te weex bay lerax, laxasaayoo ngeñaayi wurus ba ci seen dënn.
7
Noonu kenn ci ñeenti mbindeef ya jox juróom-ñaari malaaka ya juróom-ñaari ndabi wurus yu fees ak merum Yàlla jiy dund ba fàww.
8
Kër Yàlla ga fees ak saxar ndax leeraayu ndamu Yàlla ak kàttanam. Te kenn mënatul a dugg ca kër Yàlla ga, ba kera juróom-ñaari musiba, ya juróom-ñaari malaaka ya taawu, di mat.
← Chapter 14
Jump to:
Chapter 1
Chapter 2
Chapter 3
Chapter 4
Chapter 5
Chapter 6
Chapter 7
Chapter 8
Chapter 9
Chapter 10
Chapter 11
Chapter 12
Chapter 13
Chapter 14
Chapter 15
Chapter 16
Chapter 17
Chapter 18
Chapter 19
Chapter 20
Chapter 21
Chapter 22
Chapter 16 →
All chapters:
1
2
3
4
5
6
7
8
9
10
11
12
13
14
15
16
17
18
19
20
21
22