bible
ra
🌐 Language
English
Español
Français
Deutsch
Português
Italiano
Nederlands
Русский
中文
日本語
한국어
العربية
Türkçe
Tiếng Việt
ไทย
Indonesia
All Languages
Home
/
Wolof
/
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
/
1 Samuel 27
1 Samuel 27
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
← Chapter 26
Jump to:
Chapter 1
Chapter 2
Chapter 3
Chapter 4
Chapter 5
Chapter 6
Chapter 7
Chapter 8
Chapter 9
Chapter 10
Chapter 11
Chapter 12
Chapter 13
Chapter 14
Chapter 15
Chapter 16
Chapter 17
Chapter 18
Chapter 19
Chapter 20
Chapter 21
Chapter 22
Chapter 23
Chapter 24
Chapter 25
Chapter 26
Chapter 27
Chapter 28
Chapter 29
Chapter 30
Chapter 31
Chapter 28 →
1
Daawuda nag ma nga naan ca xelam: «Bés a ngi ñëw bu ma nara sànku ci loxol Sóol. Li gën ci man daal, du lenn lu moy dawa daw ba ca réewu waa Filisti, ba Sóol tàyyi maa rëbbati ci Israyil gépp, ma daldi mucc.»
2
Ba loolu amee Daawuda ak juróom benni téeméeri nit ña ànd ak moom, daldi jàll ba ca buurub Gaat, Akis doomu Mawog.
3
Daawuda dal ca Akis ca Gaat, mook ay nitam, ku ci nekk ak njabootam; Daawuda ak ñaari soxnaam, Ayinowam waa Yisreel ba, ak waa Karmel ba, Abigayil, soxnas Nabal woon.
4
Ba ñu waxee Sóol ne ko Daawuda daw na, dem Gaat, Sóol rëbbatu ko.
5
Daawuda nag ne Akis: «Ngalla baaxe ma, may ma fi ab gox ci dëkki àll bii, ma man faa dëkke; ndax man sab surga laa, warumaa bokk dëkk ak yaw ci péeyu buur.»
6
Bésub keroog la ko Akis jox dëkk ba ñuy wax Ciglaag. Moo tax Ciglaag ñeel buuri Yuda ba tey jii.
7
Diir ba Daawuda dal ca àllub Filisti, at la ak ñeenti weer.
8
Ci biir loolu Daawuda aki nitam daan nañu song-songee Gesureen ñi ak Giraseen ñi ak Amalegeen ñi. Mooy ña dëkke woon naka jekk réew mooma, ba ca Sur, jàpp réewum Misra.
9
Saa yu Daawuda songaan gox ba, du ca wacc kuy dund; du góor, du jigéen, te it day lël jur gu gudd ak gu gàtt, mbaam ak giléem, aki yére. Su ko defee mu walbatiku, dellu ca Akis.
10
Bu ko Akis laajee ne ko: «Fu ngeen lële woon tey?» Daawuda ne ko: «Xanaa wetu Negew ca Yuda,» mbaa «Xanaa wetu Negew ca Yerameleen ña,» mbaa mu ne ko: «Xanaa wetu Negew ca Keneen ña.»
11
Moo tax du genn góor mbaa jigéen ju Daawuda masa bàyyi mu dund, di ko indi Gaat, ndax ragal ñu nettali lu jëm ci ñoom, naan nàngam ak nàngam la ñoom Daawuda def. Noonu la jàppoo woon mboolem diir ba mu dal ca àllub Filisti.
12
Akis nag amoon na kóolute ci Daawuda, ndax da doon wax ci xelam naan: «Kii de yóbbe na boppam mbañeel gu ko bokki bànni Israyilam bañ lool. Moo tax sama surga rekk lay doon ba fàww.»
← Chapter 26
Jump to:
Chapter 1
Chapter 2
Chapter 3
Chapter 4
Chapter 5
Chapter 6
Chapter 7
Chapter 8
Chapter 9
Chapter 10
Chapter 11
Chapter 12
Chapter 13
Chapter 14
Chapter 15
Chapter 16
Chapter 17
Chapter 18
Chapter 19
Chapter 20
Chapter 21
Chapter 22
Chapter 23
Chapter 24
Chapter 25
Chapter 26
Chapter 27
Chapter 28
Chapter 29
Chapter 30
Chapter 31
Chapter 28 →
All chapters:
1
2
3
4
5
6
7
8
9
10
11
12
13
14
15
16
17
18
19
20
21
22
23
24
25
26
27
28
29
30
31