bible
ra
🌐 Language
English
Español
Français
Deutsch
Português
Italiano
Nederlands
Русский
中文
日本語
한국어
العربية
Türkçe
Tiếng Việt
ไทย
Indonesia
All Languages
Home
/
Wolof
/
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
/
1 Samuel 7
1 Samuel 7
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
← Chapter 6
Jump to:
Chapter 1
Chapter 2
Chapter 3
Chapter 4
Chapter 5
Chapter 6
Chapter 7
Chapter 8
Chapter 9
Chapter 10
Chapter 11
Chapter 12
Chapter 13
Chapter 14
Chapter 15
Chapter 16
Chapter 17
Chapter 18
Chapter 19
Chapter 20
Chapter 21
Chapter 22
Chapter 23
Chapter 24
Chapter 25
Chapter 26
Chapter 27
Chapter 28
Chapter 29
Chapter 30
Chapter 31
Chapter 8 →
1
Waa Kiryaat Yarim nag dikk, jëlsi gaalu Aji Sax ji, yóbbu ko kër Abinadab ca kaw tund wa. Ñu sellal Elasar, doomam ju góor ngir muy wattu gaalu Aji Sax ja.
2
Gannaaw bés ba ñu yóbboo gaal ga Kiryaat Yarim, nekk na fa lu yàgg, ba am fa ñaar fukki at. Waa kër Israyil gépp nag namma dellu ci Aji Sax ji.
3
Samiyel wax ak waa kër Israyil gépp, ne leen: «Ndegam seen léppi xol ngeen namma delloo ci Aji Sax ji, jëleleen fi seen biir tuuri doxandéem yi, ak tuur yi ñu dippee Astàrt, te ngeen saxal seen xol ci Aji Sax ji, jaamu ko moom doŋŋ. Su ko defee mu xettli leen ci waa Filisti.»
4
Ba mu ko defee bànni Israyil génne seen tuur yi ñu dippee Baal ak Astàrt. Ñuy jaamu nag Aji Sax ji moom doŋŋ.
5
Gannaaw loolu Samiyel ne leen: «Wooleen Israyil gépp, ñu daje ca Mispa, ma tinul leen Aji Sax ji.»
6
Ñu daje ca Mispa, tanq ndox, sotti fa suuf, fa kanam Aji Sax ji. Ñu woor nag bésub keroog, daldi wax foofa ne: «Noo tooñ Aji Sax ji.» Ca Mispa la Samiyel doone njiitu Israyil.
7
Ba waa Filisti yégee ne bànni Israyil daje na ca Mispa, kàngami waa Filisti ya jóg, ngir songi leen. Bànni Israyil yég ko, am tiitaange ca waa Filisti.
8
Bànni Israyil ne Samiyel: «Ngalla bu nu noppee jooytul ci sunu Yàlla Aji Sax ji, ndax mu wallu nook waa Filisti!»
9
Samiyel jël menn xar mu feragul, defal ko lépp Aji Sax ji saraxu rendi-dóomal. Mu jooytul Israyil ci Aji Sax ji, Aji Sax ji nangul ko.
10
Naka la Samiyel di joxe saraxu rendi-dóomal ba, waa Filisti di jegesi ngir xareek bànni Israyil. Aji Sax ji dënoo kàddu gu réy, ca kaw waa Filisti bésub keroog, fëlxe leen, ñu daanu fa kanam bànni Israyil.
11
Bànni Israyil génne Mispa, dàqi waa Filisti, duma leen, bay waaja àgg Bet Kar.
12
Gannaaw loolu Samiyel jël aw doj, teg ko ci diggante Mispa ak fu ñuy wax Sen; mu dippee doj wi Eben Eser (mu firi doju Wall). Mu ne: «Ba fii la nu Aji Sax ji wallu.»
13
Waa Filisti nag detteelu, dikkatuñu biir suufas Israyil. Giiru dundu Samiyel gépp loxol Aji Sax jaa ngi ci kaw waa Filisti.
14
Dëkk ya Filisti nangu woon ci Israyil daldi délsi ci seeni loxo; dale ko ca Ekkron ba Gaat. Israyil nangoo ci waa Filisti suufam sépp. Diggante Israyil ak Amoreen ñi itam di jàmm.
15
Samiyel jiite na Israyil giiru dundam gépp.
16
At mu jotaan day wër diggante Betel ak Gilgal ak Mispa, di àtte mbiri bànni Israyil, foofu fépp.
17
Gannaaw loolu mu dellu Raama ndax fa la këram nekkoon, fa la daan àttee Israyil, te fa la tabax sarxalukaay, ñeel Aji Sax ji.
← Chapter 6
Jump to:
Chapter 1
Chapter 2
Chapter 3
Chapter 4
Chapter 5
Chapter 6
Chapter 7
Chapter 8
Chapter 9
Chapter 10
Chapter 11
Chapter 12
Chapter 13
Chapter 14
Chapter 15
Chapter 16
Chapter 17
Chapter 18
Chapter 19
Chapter 20
Chapter 21
Chapter 22
Chapter 23
Chapter 24
Chapter 25
Chapter 26
Chapter 27
Chapter 28
Chapter 29
Chapter 30
Chapter 31
Chapter 8 →
All chapters:
1
2
3
4
5
6
7
8
9
10
11
12
13
14
15
16
17
18
19
20
21
22
23
24
25
26
27
28
29
30
31