bible
ra
🌐 Language
English
Español
Français
Deutsch
Português
Italiano
Nederlands
Русский
中文
日本語
한국어
العربية
Türkçe
Tiếng Việt
ไทย
Indonesia
All Languages
Home
/
Wolof
/
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
/
Deuteronomy 25
Deuteronomy 25
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
← Chapter 24
Jump to:
Chapter 1
Chapter 2
Chapter 3
Chapter 4
Chapter 5
Chapter 6
Chapter 7
Chapter 8
Chapter 9
Chapter 10
Chapter 11
Chapter 12
Chapter 13
Chapter 14
Chapter 15
Chapter 16
Chapter 17
Chapter 18
Chapter 19
Chapter 20
Chapter 21
Chapter 22
Chapter 23
Chapter 24
Chapter 25
Chapter 26
Chapter 27
Chapter 28
Chapter 29
Chapter 30
Chapter 31
Chapter 32
Chapter 33
Chapter 34
Chapter 26 →
1
Su ab jote amee diggante ay nit, nañu dem ca ëttub àttekaay ba, ñu àtte leen, ba ki am dëgg, ñu jox ko dëgg, ki tooñ, ñu teg ko tooñ.
2
Su dee ay dóor la ki tooñ yelloo, na ko àttekat bi tëral, ñu dóor ko ci kanamam, limu yar ba yemook tooñam.
3
Waaye ñeent fukki yar, bu ñu ko dóor lu ko ëpp, ndax dóor ko lu ëpp loolu, torxal seen mbokk ci seen kanam lay doon.
4
Buleen sunjuñ gémmiñu nag, te fekk koy bojj am pepp.
5
Bu ay góor yu bokk waajur dëkkee, kenn ci ñoom dee te bàyyiwul doom ju góor, jabaru ki dee du génn, di séy akub jaambur. Jëkkëru donaleem ju bokk ak jëkkëram moo ko wara jël, donloo ko.
6
Su ko defee bu ca ndaw sa taawloo góor, taaw ba saxal turu mbokkam ma dee, ba turam du fey ci biir Israyil.
7
Su waa ji buggula jël jabaru donaleem jooju, na ndaw sa dem ba ca mag ña ca bunt dëkk ba, ne leen: «Sama jëkkëru donale jii moo baña saxal turu mbokkam ci Israyil. Moo ma buggula donloo.»
8
Bu loolu amee na ko magi dëkkam woolu, wax ak moom. Su waa ji dëgëree, ne buggu koo jël,
9
na ko jabaru donaleem ja fekki ca kanam mag ña, daldi summi benn caraxu waa ji ba noppi, tifli waa ji ci kanam, ne ko: «Nii lees di def ku dul sampal mbokkam kër.»
10
Su boobaa tur wa ñuy dippee waa kër waa ja ci digg Israyil, di «Kërug summi carax.»
11
Su ay góor dee jàppante, ba jabaru kenn ki dikk, di sotle jëkkëram; bu jàppee ca ngóoray kay jàppanteek jëkkër ja,
12
dogleen loxol ndaw sa te buleen ko ñéeblu.
13
Buleen denc ci seen mbuus doju màndaxekaay ak moroom ma, te bii diis, bi ci des woyof.
14
Buleen denc seen kër nattukaayu sol-sotti ak moroom ma, bii réy, bi ci des tuut.
15
Doju màndaxekaay bu mat te dëggu ngeen wara am, te nattukaayu sol-sotti bu mat te dëggu ngeen wara am, ndax ngeen gudd fan ca réew ma leen seen Yàlla Aji Sax ji di jox.
16
Seen Yàlla Aji Sax ji kat seexlu na képp kuy def yooyii, képp kuy def ug njublaŋ.
17
Fàttlikuleen la leen Amalegeen ña defoon ca yoon wa, ba ngeen génnee Misra:
18
ñoo leen dab ci yoon wi, songe leen gannaaw, fàdd mboolem ña mujje woon, fekk ngeen sonn, loof, te ragaluñu ci sax Yàlla.
19
Bu ngeen demee ba seen Yàlla Aji Sax ji noppal leen ci mboolem seen noon yi séq réew, mi mu leen sédd, ngir ngeen nangu ko, nangeen far mboolem lu ñu doon fàttlikoo Amalegeen ñi fu asamaan tiim. Buleen ko fàtte.
← Chapter 24
Jump to:
Chapter 1
Chapter 2
Chapter 3
Chapter 4
Chapter 5
Chapter 6
Chapter 7
Chapter 8
Chapter 9
Chapter 10
Chapter 11
Chapter 12
Chapter 13
Chapter 14
Chapter 15
Chapter 16
Chapter 17
Chapter 18
Chapter 19
Chapter 20
Chapter 21
Chapter 22
Chapter 23
Chapter 24
Chapter 25
Chapter 26
Chapter 27
Chapter 28
Chapter 29
Chapter 30
Chapter 31
Chapter 32
Chapter 33
Chapter 34
Chapter 26 →
All chapters:
1
2
3
4
5
6
7
8
9
10
11
12
13
14
15
16
17
18
19
20
21
22
23
24
25
26
27
28
29
30
31
32
33
34