bible
ra
🌐 Language
English
Español
Français
Deutsch
Português
Italiano
Nederlands
Русский
中文
日本語
한국어
العربية
Türkçe
Tiếng Việt
ไทย
Indonesia
All Languages
Home
/
Wolof
/
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
/
Deuteronomy 34
Deuteronomy 34
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
← Chapter 33
Jump to:
Chapter 1
Chapter 2
Chapter 3
Chapter 4
Chapter 5
Chapter 6
Chapter 7
Chapter 8
Chapter 9
Chapter 10
Chapter 11
Chapter 12
Chapter 13
Chapter 14
Chapter 15
Chapter 16
Chapter 17
Chapter 18
Chapter 19
Chapter 20
Chapter 21
Chapter 22
Chapter 23
Chapter 24
Chapter 25
Chapter 26
Chapter 27
Chapter 28
Chapter 29
Chapter 30
Chapter 31
Chapter 32
Chapter 33
Chapter 34
1
Ba loolu amee Musaa bàyyikoo jooru Mowab, yéegi tundu Nebo, ba ca collu tundu Pisga, wa jàkkaarlook Yeriko. Aji Sax ji nag won ko mboolem réew ma, diiwaanu Galàdd ba diiwaanu Dan,
2
mboolem diiwaanu Neftali, ak diiwaanu Efrayim ak Manase, mboolem diiwaanu Yuda, ba ca géej ga ca sowu,
3
ak wetu bëj-saalum, ak xuru Yeriko, dëkku tiir ya, ba ca Sowar.
4
Aji Sax ji ne ko: «Réew mii laa giñaloon Ibraayma ak Isaaxa ak Yanqóoba, ne leen seen askan laa koy jox. Won naa la ko, ba nga teg ci sa bët, waaye foofa, doo fa teg sa tànk.»
5
Musaa, jaamub Aji Sax ji nag dee foofa ca réewum Mowab, na ko Aji Sax ji tudde.
6
Mu rob ko ca xur wa ca réewum Mowab, fa janook Bet Pewor. Kenn xamul nag fu bàmmeelam nekk ba tey jii.
7
Musaa amoon na téeméeri at ak ñaar fukk, ba muy faatu, te ay bëtam naqariwul, dooleem jeexul.
8
Bànni Israyil jooy nañu Musaa ca jooru Mowab diiru fanweeri fan, fani dëj ba doora mat.
9
Fekk na Yosuwe doomu Nuun feese xel mu rafet, ndax Musaa moo tegoon ay loxoom ci kawam, bànni Israyil nag déggal ko, di jëfe na ko Aji Sax ji sante woon Musaa.
10
Ab yonent lukkeekootul ci Israyil, mel ni Musaa, ma Aji Sax ji xejjoo woon ba naan ko jàkk, mu ne ko jàkk,
11
ba ca mboolem firnde yaak kéemaan ya ko Aji Sax ji yebale woon, ngir mu def ko ca biir réewum Misra, ca Firawna ak jawriñam ñépp, ak ca biir réewam mépp,
12
ak itam mboolem doole ju màgg ja Musaa wone, ak jëf ju réy te raglu ja mu def, bànni Israyil gépp teg ci bët.
← Chapter 33
Jump to:
Chapter 1
Chapter 2
Chapter 3
Chapter 4
Chapter 5
Chapter 6
Chapter 7
Chapter 8
Chapter 9
Chapter 10
Chapter 11
Chapter 12
Chapter 13
Chapter 14
Chapter 15
Chapter 16
Chapter 17
Chapter 18
Chapter 19
Chapter 20
Chapter 21
Chapter 22
Chapter 23
Chapter 24
Chapter 25
Chapter 26
Chapter 27
Chapter 28
Chapter 29
Chapter 30
Chapter 31
Chapter 32
Chapter 33
Chapter 34
All chapters:
1
2
3
4
5
6
7
8
9
10
11
12
13
14
15
16
17
18
19
20
21
22
23
24
25
26
27
28
29
30
31
32
33
34