bible
ra
🌐 Language
English
Español
Français
Deutsch
Português
Italiano
Nederlands
Русский
中文
日本語
한국어
العربية
Türkçe
Tiếng Việt
ไทย
Indonesia
All Languages
Home
/
Wolof
/
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
/
Numbers 12
Numbers 12
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
← Chapter 11
Jump to:
Chapter 1
Chapter 2
Chapter 3
Chapter 4
Chapter 5
Chapter 6
Chapter 7
Chapter 8
Chapter 9
Chapter 10
Chapter 11
Chapter 12
Chapter 13
Chapter 14
Chapter 15
Chapter 16
Chapter 17
Chapter 18
Chapter 19
Chapter 20
Chapter 21
Chapter 22
Chapter 23
Chapter 24
Chapter 25
Chapter 26
Chapter 27
Chapter 28
Chapter 29
Chapter 30
Chapter 31
Chapter 32
Chapter 33
Chapter 34
Chapter 35
Chapter 36
Chapter 13 →
1
Maryaama ak Aaróona ñoo doon ŋàññ Musaa, ci ndawas Kuuseen su mu takkoon, te ab Kuuseen it la takkoon.
2
Ñu ne: «Ndax mennum Musaa doŋŋ la Aji Sax jiy waxe ci moom? Xanaa daa waxewul ci nun itam?» Aji Sax ji dégg ca.
3
Góor ga Musaa nag defoon ku woyof lool, ba raw mboolem doom aadama ci kaw suuf.
4
Ci kaw loolu Aji Sax ji jekki wax ak Musaa ak Aaróona ak Maryaama, ne leen: «Dikkleen, yeen ñett, ci xaymab ndaje mi!» Ñu dem, ñoom ñett.
5
Aji Sax ji wàcc ci biir niir wu def aw taxaar. Mu taxaw ca bunt xayma ba, daldi woo Aaróona ak Maryaama, ñu bokk dikk.
6
Mu ne leen: «Dégluleen bu baax samay kàddu: su ngeen feeñlee ab yonentu Aji Sax ji, ci am peeñu laa koy xamale maay kan, te ci gént laay waxeek moom,
7
waaye du Musaa sama jaam bii. Moom mooy ki wóor ci mboolem sama kër gii.
8
Gémmiñ ak gémmiñ laay waxeek moom wax ju leer nàññ ju ñu léebul, te jëmmu Aji Sax ji lay gis. Kon lu leen may fitu ŋàññ Musaa sama jaam bi?»
9
Sànjum Aji Sax ji nag tàkkal leen. Ci kaw loolu mu dem.
10
Naka la niir wa jóge ca xayma ba, Maryaama jekki ne fureet ak jàngoroy ngaana, weex furr! Aaróona ne Maryaama gees, yem ca ngaana ga.
11
Aaróona ne Musaa: «Ngalla sang bi, bu nu topp bàkkaar bi nu bàkkaar ndax ñàkk xel!
12
Ngalla bul seetaan kii mel ni ku dee te indaalewul bakkan ba mu juddoo ca ndeyam, xaaju yaram wi lekku!»
13
Musaa nag jooy Aji Sax ji, ne ko: «Yàlla, ngalla wéral ko!»
14
Aji Sax ji ne Musaa: «Xanaa baayam sax su ko jéppi woon, ba tifli ko ci kanam, muy gàcceem diiru juróom ñaari fan? Nañu ko génne dal bi diiru juróom ñaari fan, door koo délloosi ci biir.»
15
Ba loolu amee ñu génne Maryaama dal ba diiru juróom ñaari fan. Mbooloo ma demul, ba keroog ba ñu délloosee Maryaama ca biir dal ba.
16
Gannaaw loolu mbooloo ma bàyyikoo Aserot, ñu dali ca màndiŋu Paran.
← Chapter 11
Jump to:
Chapter 1
Chapter 2
Chapter 3
Chapter 4
Chapter 5
Chapter 6
Chapter 7
Chapter 8
Chapter 9
Chapter 10
Chapter 11
Chapter 12
Chapter 13
Chapter 14
Chapter 15
Chapter 16
Chapter 17
Chapter 18
Chapter 19
Chapter 20
Chapter 21
Chapter 22
Chapter 23
Chapter 24
Chapter 25
Chapter 26
Chapter 27
Chapter 28
Chapter 29
Chapter 30
Chapter 31
Chapter 32
Chapter 33
Chapter 34
Chapter 35
Chapter 36
Chapter 13 →
All chapters:
1
2
3
4
5
6
7
8
9
10
11
12
13
14
15
16
17
18
19
20
21
22
23
24
25
26
27
28
29
30
31
32
33
34
35
36