bible
ra
🌐 Language
English
Español
Français
Deutsch
Português
Italiano
Nederlands
Русский
中文
日本語
한국어
العربية
Türkçe
Tiếng Việt
ไทย
Indonesia
All Languages
Home
/
Wolof
/
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
/
Numbers 25
Numbers 25
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
← Chapter 24
Jump to:
Chapter 1
Chapter 2
Chapter 3
Chapter 4
Chapter 5
Chapter 6
Chapter 7
Chapter 8
Chapter 9
Chapter 10
Chapter 11
Chapter 12
Chapter 13
Chapter 14
Chapter 15
Chapter 16
Chapter 17
Chapter 18
Chapter 19
Chapter 20
Chapter 21
Chapter 22
Chapter 23
Chapter 24
Chapter 25
Chapter 26
Chapter 27
Chapter 28
Chapter 29
Chapter 30
Chapter 31
Chapter 32
Chapter 33
Chapter 34
Chapter 35
Chapter 36
Chapter 26 →
1
Ci kaw loolu Israyil dale fa Sitim. Mbooloo ma nag tàmbali di moy ak jigéeni Mowab.
2
Jigéen ña di woo mbooloo ma ca seen saraxi tuur ya, mbooloo ma di lekk ak a sujjóotal seeni tuur.
3
Israyil nag taqook tuur ma ñuy wax Baal Pewor, ba sànjum Aji Sax ji tàkkal Israyil.
4
Aji Sax ji ne Musaa: «Jàppal njiiti mbooloo mi yépp, nga wékk leen ci bant fi kanam Aji Sax ji, bëccëg ndarakàmm, ngir sànjum Aji Sax ji dëddu Israyil.»
5
Musaa ne àttekati Israyil: «Na ku nekk ci yeen rey nitam ñi taqook Baal Pewor.»
6
Ci biir loolu rekk, jenn waayu bànni Israyil dikk, indaale senn ndawas waa Majan ci biiri bokkam, Musaa ak mbooloom Israyil mépp di gis, fekk ñoom ñuy jooyoo fa bunt xaymab ndaje ma.
7
Fineyas, doomu Elasar, doomu sarxalkat ba Aaróona, gis loolu, daldi jóge ca mbooloo ma, jël ab xeej.
8
Mu topp waayi Israyil ja ba ca biir néeg ba, daldi leen boole bennub xeej, ñoom ñaar, jam waayi Israyil ji, ba jamaale ndaw si ci biir. Ba mu ko defee mbas ma jotoona dal ca kaw bànni Israyil daldi dakk.
9
Ña dee ca mbas ma nag di ñaar fukki junneek ñeent (24 000).
10
Ba loolu weesee Aji Sax ji wax Musaa, ne ko:
11
«Fineyas, doomu Elasar, doomu sarxalkat bi Aaróona, moo moyale Israyil samam sànj, ndax sama fiiraange gi mu ma fiirlee ci seen biir, ba faagaagaluma bànni Israyil ci sama biir fiiraange.
12
Kon nag nee ko: Maa ngii di ko baaxe sama kóllëreg jàmm,
13
mu ñeel ko, mook askan wi koy wuutu, te di kóllëreg carxal gu sax dàkk, ndax moo fiire Yàllaam, ba jot bànni Israyil.»
14
Waayi bànni Israyil ja ñu jamoon, te boole kook ndawas Majan sa jam, mooy Simri doomu Salu. Kilifag kër maamam la woon ca Cimyoneen ña.
15
Ndawas Majan sa ñu jam di Kosbi. Baayam Sur doonoon kilifag kër maamam ca giirug Majan ga mu bokk.
16
Ci kaw loolu Aji Sax ji wax Musaa, ne ko:
17
«Noonooleen waa Majan yii, te rey leen,
18
ndax ñoom ñoo leen noonoo woon ba ñu leen woree ca mbirum Pewor ma, ak itam ca mbirum ndaw sa Kosbi, seen mbokk may doomu kilifag Majan ja, te ñu jam ko keroog bésu mbas, ma sababoo ca mbirum Baal Pewor, tuur ma.»
19
Gannaaw ba mbas ma wéyee,
← Chapter 24
Jump to:
Chapter 1
Chapter 2
Chapter 3
Chapter 4
Chapter 5
Chapter 6
Chapter 7
Chapter 8
Chapter 9
Chapter 10
Chapter 11
Chapter 12
Chapter 13
Chapter 14
Chapter 15
Chapter 16
Chapter 17
Chapter 18
Chapter 19
Chapter 20
Chapter 21
Chapter 22
Chapter 23
Chapter 24
Chapter 25
Chapter 26
Chapter 27
Chapter 28
Chapter 29
Chapter 30
Chapter 31
Chapter 32
Chapter 33
Chapter 34
Chapter 35
Chapter 36
Chapter 26 →
All chapters:
1
2
3
4
5
6
7
8
9
10
11
12
13
14
15
16
17
18
19
20
21
22
23
24
25
26
27
28
29
30
31
32
33
34
35
36