bible
ra
🌐 Language
English
Español
Français
Deutsch
Português
Italiano
Nederlands
Русский
中文
日本語
한국어
العربية
Türkçe
Tiếng Việt
ไทย
Indonesia
All Languages
Home
/
Wolof
/
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
/
Revelation 15
Revelation 15
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
← Chapter 14
Jump to:
Chapter 1
Chapter 2
Chapter 3
Chapter 4
Chapter 5
Chapter 6
Chapter 7
Chapter 8
Chapter 9
Chapter 10
Chapter 11
Chapter 12
Chapter 13
Chapter 14
Chapter 15
Chapter 16
Chapter 17
Chapter 18
Chapter 19
Chapter 20
Chapter 21
Chapter 22
Chapter 16 →
1
Ma xoolaat, gisuma ci asamaan lu moy jeneen firnde ju màgg te yéeme: juróom ñaari malaaka yu taawu juróom ñaari musiba. Musiba yu mujj yaa nag, ngir ca la sànjum Yàlla di mate.
2
Ma gisati lu mel ni géeju kiristaal bu jaxasook sawara. Ci biir loolu ña daanoon rab waak jëmmu nataalam, ak lim bi méngook turam, ñu ngi taxaw ci kaw géeju kiristaal gi, yore ay xalami Yàlla.
3
Ña ngay woy woyu Musaa jaamu Yàlla ba, ak woyu Gàtt bi, naan: «Yaw Boroom bi Yàlla Aji Man ji, yaa réy te yéeme ay jaloore. Yaw Buuru askan yi, yaa jub te dëgguy doxalin.
4
Boroom bi, ana ku la ragalul? Ku dul màggal saw tur? Yaw doŋŋ yaa sell. Askan yépp ay dikk, sujjóotsil la, ndax yaa jubi dogal.»
5
Gannaaw loolu ma xoolaat, daldi gis màkkaan ma fa asamaan, xayma ba fat seede si, mu ubbiku.
6
Juróom ñaari malaaka, yi taawu juróom ñaari musiba yi nag, génne ci màkkaan mi. Ñu ngi sol mbubbi lẽe yu set, ne ràññ, ay ngañaayi wurus takke ci seen dënn.
7
Kenn ci ñeenti bindeef yi nag jox juróom ñaari malaaka yi, juróom ñaari ndabi wurus yu fees ak sànjum Yàlla jiy dund ba fàww.
8
Ba mu ko defee màkkaan ma fees ak saxar su bawoo ci leeru Yàlla ak kàttanam. Kenn nag manatula dugg ci màkkaan mi, ba kera juróom ñaari musibay juróom ñaari malaaka yi matee.
← Chapter 14
Jump to:
Chapter 1
Chapter 2
Chapter 3
Chapter 4
Chapter 5
Chapter 6
Chapter 7
Chapter 8
Chapter 9
Chapter 10
Chapter 11
Chapter 12
Chapter 13
Chapter 14
Chapter 15
Chapter 16
Chapter 17
Chapter 18
Chapter 19
Chapter 20
Chapter 21
Chapter 22
Chapter 16 →
All chapters:
1
2
3
4
5
6
7
8
9
10
11
12
13
14
15
16
17
18
19
20
21
22