bible
ra
🌐 Language
English
Español
Français
Deutsch
Português
Italiano
Nederlands
Русский
中文
日本語
한국어
العربية
Türkçe
Tiếng Việt
ไทย
Indonesia
All Languages
Home
/
Wolof
/
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
/
Revelation 5
Revelation 5
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
← Chapter 4
Jump to:
Chapter 1
Chapter 2
Chapter 3
Chapter 4
Chapter 5
Chapter 6
Chapter 7
Chapter 8
Chapter 9
Chapter 10
Chapter 11
Chapter 12
Chapter 13
Chapter 14
Chapter 15
Chapter 16
Chapter 17
Chapter 18
Chapter 19
Chapter 20
Chapter 21
Chapter 22
Chapter 6 →
1
Ci biir loolu ma gis ci loxol ndijooru ki toog ci ngàngune mi, taxañub téere bu ñu bind biir ak biti, tay ko juróom ñaari tayu.
2
Ma gis malaaka mu am doole, muy yéenee baat bu xumb, naan: «Ana ku yeyoo tàyyi tayuy téere bii, ubbi ko?»
3
Du kenn nag ci asamaan mbaa kaw suuf, mbaa biir suuf, ku manoona ubbi téere bi, ba yër ko.
4
Ma jooy jooy yu metti, ndax giseesul kenn ku yeyoo ubbi téere bi, ba yër ko.
5
Kenn ci mag ñi ne ma: «Bul jooy. Ma ne, Gayndeg giirug Yuda, njebbital Buur Daawuda daan na. Mooy ubbi téere beek juróom ñaari tayoom.»
6
Ma daldi gis gàtt bu mel ni lu ñu rendi, mu taxaw fi digg ngàngune mi, ñeenti bindeef yeek mag ñi yéew ko. Gàtt bi juróom ñaari béjjén la am, ak juróom ñaari bët, di juróom ñaari noowi Yàlla, yi ñu yebal ci àddina sépp.
7
Gàtt bi dikk, jël téere bi ci loxol ndijooru ki toog ci ngàngune mi.
8
Ba mu jëlee téere bi, ñeenti bindeef yi ak ñaar fukki mag ñeek ñeent ne gurub sukk fi kanamam, ku nekk yor xalam ak andi wurus yu fees ak cuuraay, cuuraay li di ñaani aji sell ñi.
9
Ñuy woy nag woy wu yees, naan: «Yaa yeyoo jël téere bi, tàyyi tayu yi, ndax yaw lañu rendi, te sa deret nga jote, ngir Yàlla, ay niti gépp giir ak wépp làmmiñ ak wépp xeet ak wépp askan.
10
Yaa leen def ñu doon nguurug sarxalkat yi, ñeel sunu Yàlla, te dinañu nguuru ci àddina.»
11
Ma xoolaat, daldi dégg baati malaaka yu bare, ñu yéew ngàngune mi ak bindeef yi ak mag ñi, seen lim di ay junni, ba ci junniy junni.
12
Ña ngay àddu ca kaw, naan: «Gàtt bi ñu rendi woon moo yeyoo kàttan ak alal, yeyoo xel ak doole, moo yeyoo teraanga, yeyoo darajaak cant.»
13
Ba loolu amee mboolem dundooti asamaan, ak kaw suuf, ak biir suuf, ak géej, ak mboolem li ci seen biir, ñoom ñépp di wax, may dégg, naan: «Ki toog ci ngàngune mi ak Gàtt bi, nañu jagoo cant ak teraanga, ak darajaak kàttan, tey ak ëllëg ba fàww.»
14
Ñeenti bindeef yi ne: «Amiin.» Mag ñi ne gurub sukk, sujjóot.
← Chapter 4
Jump to:
Chapter 1
Chapter 2
Chapter 3
Chapter 4
Chapter 5
Chapter 6
Chapter 7
Chapter 8
Chapter 9
Chapter 10
Chapter 11
Chapter 12
Chapter 13
Chapter 14
Chapter 15
Chapter 16
Chapter 17
Chapter 18
Chapter 19
Chapter 20
Chapter 21
Chapter 22
Chapter 6 →
All chapters:
1
2
3
4
5
6
7
8
9
10
11
12
13
14
15
16
17
18
19
20
21
22