bible
ra
🌐 Language
English
Español
Français
Deutsch
Português
Italiano
Nederlands
Русский
中文
日本語
한국어
العربية
Türkçe
Tiếng Việt
ไทย
Indonesia
All Languages
Home
/
Wolof
/
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
/
Song of Solomon 2
Song of Solomon 2
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
← Chapter 1
Jump to:
Chapter 1
Chapter 2
Chapter 3
Chapter 4
Chapter 5
Chapter 6
Chapter 7
Chapter 8
Chapter 3 →
1
Waaye man saxayaayu joor doŋŋ laa, nirook as tóor-tóor ciw xur.
2
Xanaa as tóor-tóor su ne ràññ ci biiri dég! Kookooy sama xarit ci biir janq ji.
3
Mbete garab gu gëna neex ci gott bi, kookooy sama nijaay ci biir xale yu góor yi. May bége keppaaram, safoo doom ya.
4
Dugal na ma néegub sago-jeex-na, yiire ma mbëggeel.
5
Gaaweleen ma nàkki reseñ, ma dëgër, leel-leen may meññeef, leqlee ma. Wopp laa def ndax mbëggeel!
6
Sama càmmoñu waay, ma gegenoo, ndijooram, ma laxasoo.
7
Yeen janqi Yerusalem, waatal-leen ma ci taaru kéwél ak koobay àll bi, ne dungeen dakkal te dungeen sooke tëraayu mbëggeel te jotul.
8
Dégluleen, sama nijaay a, mu ngooguy ñëw, di xéluy jéggi tund yu ndaw yi, di tëb tund yu mag yiy dikk.
9
Sama nijaay a ngi mel ni kéwél, mbaa kooba gu ndaw. Mu ngi noonu taxaw ca gannaaw miir ba, di séentu ci palanteer bi ak a yër ci caax bi.
10
Sama nijaay ne ma: «Xarit, ayca, jongama sama, dikkal boog!
11
Xoolal, tawub sedd wees na, waame jàll, wéy.
12
Tóor-tóor yi lal na réew mi, jamonoy woy dikk, sabum pégét jibe sunum réew.
13
Figg a ngi ñorsi, reseñ tóor, di gilli. Xarit, ayca, jongama sama, dikkal boog!»
14
Soppe, sore nga ni xati mu dëkke xar-xari doj, làqoo ruqi mbartal yi. Won ma sa jëmm, dégtal ma sa baat. Sa baat a neex, sa jëmm jekk!
15
Jàppal-leen ma till yi, till yu ndaw yiy ruur reseñ, te sunu reseñ jiy tóor.
16
Sama nijaay, maa moom, man it, moo moom, di fore digg tóor-tóor yi.
17
Nijaay, balaa jant a fenk, ker toxu, dellul gaaw ni kéwél, mbaa kooba gu ndaw kaw tund yu xàjjalikoo ya.
← Chapter 1
Jump to:
Chapter 1
Chapter 2
Chapter 3
Chapter 4
Chapter 5
Chapter 6
Chapter 7
Chapter 8
Chapter 3 →
All chapters:
1
2
3
4
5
6
7
8