bible
ra
🌐 Language
English
Español
Français
Deutsch
Português
Italiano
Nederlands
Русский
中文
日本語
한국어
العربية
Türkçe
Tiếng Việt
ไทย
Indonesia
All Languages
Home
/
Wolof
/
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
/
Song of Solomon 3
Song of Solomon 3
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
← Chapter 2
Jump to:
Chapter 1
Chapter 2
Chapter 3
Chapter 4
Chapter 5
Chapter 6
Chapter 7
Chapter 8
Chapter 4 →
1
Sama kaw lal, guddi, laa seet sama soppey xol. Seet naa ko, gisuma ko.
2
Naa jóg, wër dëkk bi. Mbedd yeek pénc yi laay seete sama soppey xol. Seet naa ko, gisuma ko.
3
Wattukat yee ma gis, ba ñuy wër dëkk bi. Ma ne leen: «Sama soppey xol, gisuleen ko?»
4
Ma romb leen tuuti rekk, gis sama soppey xol. Ma ne ko taral, bàyyeetuma ko, ba yóbbu ko sama kër yaay, ba sama biir néegu ndey ji ma jur.
5
Ngalla yeen, janqi Yerusalem, waatal-leen ma ci taaru kéwél ak koobay àll bi, ne dungeen dakkal te dungeen sooke tëraayu mbëggeel te jotul.
6
Ana luy jóge màndiŋ ma nii, mel ni taxaaru saxar, suuroo ndàbb ak xas mu xeeñ ak mboolem cuuraayi jula?
7
Laltub Suleymaan a ngoog, juróom benn fukki jàmbaar dar ko, di jàmbaari Israyil.
8
Ñépp mane saamar, ku ci nekk mokkal xare, saamar ci pooj, ngay fàggu mbettum guddi.
9
Ab toogu la Buur Suleymaan defarlu, ñu defare ko bantu Libaŋ,
10
ponku ya, mu def ko xaalis, wéeruwaay ba wurus; tooguwaay ba di ndimo lu xonq curr, biir ba di liggéeyu ràbb bu janqi Yerusalem ràbbe cofeel.
11
Yeen janqi Siyoŋ, génnleen, xool Buur Suleymaan ak mbaxanam céetal mi ko yaayam solal ci bésub céetalam, bésu bànneexam.
← Chapter 2
Jump to:
Chapter 1
Chapter 2
Chapter 3
Chapter 4
Chapter 5
Chapter 6
Chapter 7
Chapter 8
Chapter 4 →
All chapters:
1
2
3
4
5
6
7
8