bible
ra
🌐 Language
English
Español
Français
Deutsch
Português
Italiano
Nederlands
Русский
中文
日本語
한국어
العربية
Türkçe
Tiếng Việt
ไทย
Indonesia
All Languages
Home
/
Wolof
/
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
/
Hosea 11
Hosea 11
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
← Chapter 10
Jump to:
Chapter 1
Chapter 2
Chapter 3
Chapter 4
Chapter 5
Chapter 6
Chapter 7
Chapter 8
Chapter 9
Chapter 10
Chapter 11
Chapter 12
Chapter 13
Chapter 14
Chapter 12 →
1
«Maa soppoon Israyil ba muy ndaw, Fa Misra laa ko wooye, muy sama doom.
2
Lu ñu leen gëna woo, ñu gën maa sore. Ay tuuri Baal lañuy defal ay sarax, te ay xërëm lañuy taalal cuuraay.
3
Ndaxam man maa tette Efrayim, fab ko, te ràññeewuñu ne maa leen topptoo.
4
Ay goji nit laa leen ñoddee, ay buumi cofeel. Maay ki leen yolomalal ŋalaabi ŋaam, sëgg, leel leen.
5
Duñu dellu réewum Misra. Waa Asiri ñooy doon seen buur, nde ñoo baña délsi fi man.
6
Ab saamar ay wëndeelu ca seen dëkk yu mag, dàjji seen bunti dëkk, ba warax leen ndax seeni mébét.
7
Sama ñoñ dañoo làggi ci ñàkke ma kóllëre, wooyees na leen fa kaw, te kenn ci ñoom jógul.
8
«Efrayim, ana nu ma lay baye, yaw Israyil laa ne, nu ma lay tege ciy loxo? Ana nu ma lay defe ni Atma? Nu ma lay yemaleek Ceboyim? Sama xol a bëpp, sama yërmandee yëngu.
9
Duma wéye di tàkkal sama mer, duma yàqteeti Efrayim, ndax maay Yàlla, duma nit, maay Aji Sell ji ci seen biir, duma dikke am sànj.
10
Dees na topp ci gannaaw Aji Sax ji, muy yëmmu ni gaynde. Mooy yëmmu moos ni gaynde, ay doomam di lox, jóge sowu.
11
Ni njanaaw lañuy loxe, jóge Misra, mel nim pitax, bawoo Asiri. Maa leen di dëël seeni kër.» Aji Sax jee ko wax.
← Chapter 10
Jump to:
Chapter 1
Chapter 2
Chapter 3
Chapter 4
Chapter 5
Chapter 6
Chapter 7
Chapter 8
Chapter 9
Chapter 10
Chapter 11
Chapter 12
Chapter 13
Chapter 14
Chapter 12 →
All chapters:
1
2
3
4
5
6
7
8
9
10
11
12
13
14