bible
ra
🌐 Language
English
Español
Français
Deutsch
Português
Italiano
Nederlands
Русский
中文
日本語
한국어
العربية
Türkçe
Tiếng Việt
ไทย
Indonesia
All Languages
Home
/
Wolof
/
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
/
Hosea 7
Hosea 7
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
← Chapter 6
Jump to:
Chapter 1
Chapter 2
Chapter 3
Chapter 4
Chapter 5
Chapter 6
Chapter 7
Chapter 8
Chapter 9
Chapter 10
Chapter 11
Chapter 12
Chapter 13
Chapter 14
Chapter 8 →
1
«Bu may faj Israyil foofu ca Efrayim la seeni ñaawtéef di feeñ, ànd ak mbonu Samari seen péey. Dañuy njublaŋ, sàcc yiy bëtt ci biir kër yi, gàngoori saaysaay di songe ci biti.
2
Taxul ñu jàpp ci seenum xel ne seen mboolem jëf ju bon laa bàyyi xel. Léegi seeni jëf a leen wër ndombo, ne màkk fi sama kanam.
3
Seenug mbon lañuy bégale buur, seeni fen di bégal kàngam.
4
Ñoom ñépp a diy jaalookat. Ñu mel ni taalu mburu bu yànj, taal bu lakk-kat ba soxlawula xamb, ca tooyal ba, ba kera xóoy bay funki.
5
Bu sunu buur xewlee, kàngam yi naan ba wopp, buur tàllal loxo ay ñaawlekat.
6
Seenub xol lañu waajal nib taal, di tëroo, Seen lakk-katu mburu fanaanee nelaw, bët set taal ba yànj, di fër-fëri.
7
Ñoom ñépp a tàng jérr nib taal, te ñooy xoyom seeni njiit, seen buur yépp a daanu, te kenn ci ñoom woowu ma wall.
8
Efrayim moo jaxasook askani jaambur, Efrayim moo di mburu mu ñu walbatiwul cib taal.
9
Ay doxandéem a jeexal dooleem, te xamu ko, aw liir tege ci kawam weex tàll, te yégu ko.
10
Israyil, ag reewandeem a ko tiiñal, te taxul ñu délsi ci seen Yàlla Aji Sax ji. Loolu yépp taxul ñu sàkku ko.
11
Efrayim daa mel ni pitax, dofe, ñàkk xel, di woo wall Misraak a dem Asiri.
12
Bu ñuy dem, maa leen di laaw samab caax, niy njanaaw laa leen di woddale fi suuf, fa ma dégge seenum ndaje laa leen di mbugale.
13
Ngalla ñoom, nde ñoo ma daw, yàqute ñeel na leen, nde ñoo ma gàntal. Doon naa leen jot waaye ñoo ma fenal.
14
Du seen xol lañu ma wooye wall, xanaa di salliiru ci seen kaw lal, pepp ak biiñ tax ñuy dagg seen yaram, dëddu ma.
15
Maa leen jàngal, dëgëral seeni përëg, te man lañuy fexeel lu bon.
16
Bu ñu waññikoo it, du fi Aji Kawe ji. Ni xala gu yolom lañu mel, te seeni kàngam ay fàddoo saamar ndax seen sànjum làmmiñ, te loolu lees leen di reetaane ca réewum Misra.
← Chapter 6
Jump to:
Chapter 1
Chapter 2
Chapter 3
Chapter 4
Chapter 5
Chapter 6
Chapter 7
Chapter 8
Chapter 9
Chapter 10
Chapter 11
Chapter 12
Chapter 13
Chapter 14
Chapter 8 →
All chapters:
1
2
3
4
5
6
7
8
9
10
11
12
13
14