bible
ra
🌐 Language
English
Español
Français
Deutsch
Português
Italiano
Nederlands
Русский
中文
日本語
한국어
العربية
Türkçe
Tiếng Việt
ไทย
Indonesia
All Languages
Home
/
Wolof
/
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
/
Hosea 12
Hosea 12
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
← Chapter 11
Jump to:
Chapter 1
Chapter 2
Chapter 3
Chapter 4
Chapter 5
Chapter 6
Chapter 7
Chapter 8
Chapter 9
Chapter 10
Chapter 11
Chapter 12
Chapter 13
Chapter 14
Chapter 13 →
1
«Efrayim, ay fen la ma gawe, waa kër Israyil laa ne, ñoo ma yéewe ag njublaŋ, waaye Yudaa ngi ànd ak Yàlla ba tey, di sàmm kóllëreek Ku Sell ki.»
2
Efrayim mooy sàmmkatub ngelaw, yendoo topp ngelawal penku, di yokki fen ak fitna, fasoo kóllëre ak Asiri, yónnee yóbbalu diw ba Misra.
3
Aji Sax ji moo séq ak Yuda ab layoo, mooy mbugale Yanqóoba ay jëfinam, añale ko ay jëfam.
4
Ci biiru ndeyam la kii suufoo ab seexam; kii moo tollu ci dooleem, bëreek Yàlla.
5
Kee bëreek malaaka, ba génn ca, kee jooy di sàkku aw yiwam. Fa Betel la ko fekk, te foofa la Yàlla waxeek nun.
6
Aji Sax ji Yàlla Boroom gàngoor yi, Aji Sax jee di turu bàkkam.
7
Yaw nag, ca sa Yàlla nga wara dellu, ngor ak njub, sàmm ko, te nga saxoo yaakaar sa Yàlla.
8
Ni Kanaaneen biy jula, ni la Efrayim yore màndaxekaayu njublaŋ cib loxoom, bëgga naxe.
9
Efrayim a ngi naan: «Woomle naa, maa amal sama bopp alal, te mboolem samaw ñaq, giseesu ci tooñaange ju di bàkkaar.»
10
«Man Aji Sax ji dale di sa Yàlla ca Misra, maa lay dëëlaat ciy xayma, na woon ca bésub ndaje.
11
Maa wax ak yonent yi, yokk peeñu yi, te yonent yi, maa leen waxyu ay misaal.»
12
Su Galàdd dee dëkkub defkati ñaawtéef, dañoo tekkiwul dara. Fa Gilgal lees di rendee ay saraxi yëkk, te seeni sarxalukaay ni jali xeer lay mel ci ay tooboy tool.
13
Yanqóobaa dawoon ba réewum Siri, Israyil laa ne, moo liggéey ngir am jabar, wut jabar tax koo sàmm ag jur.
14
Ci loxol yonent la Aji Sax ji génnee Israyil Misra, te ab yonent la sàmmloo Israyil.
15
Waaye Efrayim moomoo ko merloo, naqaral ko. Deret ji mu tuur la Boroomam di këpp ci kawam, añub tooñam la koy fey.
← Chapter 11
Jump to:
Chapter 1
Chapter 2
Chapter 3
Chapter 4
Chapter 5
Chapter 6
Chapter 7
Chapter 8
Chapter 9
Chapter 10
Chapter 11
Chapter 12
Chapter 13
Chapter 14
Chapter 13 →
All chapters:
1
2
3
4
5
6
7
8
9
10
11
12
13
14