bible
ra
🌐 Language
English
Español
Français
Deutsch
Português
Italiano
Nederlands
Русский
中文
日本語
한국어
العربية
Türkçe
Tiếng Việt
ไทย
Indonesia
All Languages
Home
/
Wolof
/
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
/
Ezekiel 30
Ezekiel 30
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
← Chapter 29
Jump to:
Chapter 1
Chapter 2
Chapter 3
Chapter 4
Chapter 5
Chapter 6
Chapter 7
Chapter 8
Chapter 9
Chapter 10
Chapter 11
Chapter 12
Chapter 13
Chapter 14
Chapter 15
Chapter 16
Chapter 17
Chapter 18
Chapter 19
Chapter 20
Chapter 21
Chapter 22
Chapter 23
Chapter 24
Chapter 25
Chapter 26
Chapter 27
Chapter 28
Chapter 29
Chapter 30
Chapter 31
Chapter 32
Chapter 33
Chapter 34
Chapter 35
Chapter 36
Chapter 37
Chapter 38
Chapter 39
Chapter 40
Chapter 41
Chapter 42
Chapter 43
Chapter 44
Chapter 45
Chapter 46
Chapter 47
Chapter 48
Chapter 31 →
1
Ba loolu amee kàddug Aji Sax ji dikkal ma ne ma:
2
«Yaw nit ki, jottlil waxyu! Neel: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Jooyleen, ne: ‘Wóoy bii bés!’
3
Bés jubsi na déy, bésub Aji Sax ji jubsi na! Bésub xàmbaar, jantub xeet yi.
4
Saamar ay dikkal Misra, fépp di jal-jal ba ca Kuus, aw nit, ñu bóom ca Misra, nangu alalu réew ma, kenu ya màbb.
5
Waa Kuus ak Puut ak Ludd ak xeet yu raxe yépp ak waa Libi, boole ci ñenn ci réewum kóllëre gi, ñoom ñépp saamar lañuy fàddoo.
6
«“Aji Sax ji dafa wax ne: Wéeruwaayi Misra ya day jóoru, doole ja Misray sago ŋiis; la dale Migadol ba Asuwan, saamar lañuy fàddoo. Kàddug Boroom bi Aji Sax jee.
7
Ñooy gëna wéet ci réew yi, seeni dëkk gëna gental ci dëkk yi.
8
Bu ma taalee Misra, ba wéeruwaayam yépp rajaxoo, dinañu xam ne maay Aji Sax ji.
9
Bésub keroog dees na dugg ay gaal, génn ci sama ndigal, ngir indil tiitaange réewum Kuus ma ne finaax, muy seen jal-jal keroog bésub Misra ba. Bés baa ngii déy di dikk!
10
«“Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Maay jeexal mbooloom Misra mu réy, jaare ko ci Nabukodonosor buuru Babilon.
11
Mooy ànd ak ñoñam, di ñi gëna néeg ci yéefar yi, dikk yaqtesi réew mi; ñooy boccil Misra saamar, ba feesal réew mi ay néew.
12
Maay def wali Niil ag joor, maay jaay réew mi nit ñu aay. Maay alag réew meek li ci biiram, jaare ko ci ay doxandéem. Man Aji Sax ji, maa ko wax.
13
«“Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Maay sànk kasaray tuur yi ak yàllantu ya ca Memfis. Buur dootu tooge jalu réewum Misra, te maay indi tiitaange biir Misra.
14
Maay yàqte Pattros, taal dëkk bi ñuy wax Cowan, ba sottal sama mbugal ci kaw dëkk bi ñuy wax No.
15
Maay sottil sama xadar Ciin, rawtub Misra, te maay tenqi gàngooru No.
16
Maay taal Misra, dëkk ba ñuy wax Ciin di rag-ragi; dëkk ba ñuy wax No, ñu bëtt ko; Memfis, noon yi nangu ko digg bëccëg.
17
Xaleli góori On ak Pi Beset, saamar lañuy fàddoo, waa dëkk yooyu ca des njaam lañu jëm.
18
Bu ma dogee sidditi Misra, ba doole ja muy sago ŋiis, jant dootu fenkal Tapanes, aw xiin ay sàng dëkk bi, te dëkk-dëkkaanam ya, njaam lañu jëm.
19
Nii laay wàcceele Misra ay mbugal, ba ñu xam ne maay Aji Sax ji.”»
20
Ca fukkeelu at maak benn, juróom ñaari fan ca weer wa jëkk, kàddug Aji Sax ji dikkal na ma ne ma:
21
Yaw nit ki, damm naa përëgu Firawna buuru Misra, mu ngii, deesu ko takk, ba mu faju, deesu ko lëmës, ba mu mana ŋàbb saamar.
22
Léegi nag Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: «Maa ngii fi kaw Firawna buuru Misra. Ñaari përëgam yépp laay damm; bu baax beek bi damm ba noppi, maay waddal saamaram bi ci loxoom,
23
maay tasaare Misra fi biir xeet yi, wasaare leen fi biir réew yi.
24
Maay dooleel përëgu buuru Babilon, teg sama saamar ci loxoom, gannaaw ba ma dammee përëgi Firawna, muy binni binniy ku ñu jam fi kanamam.
25
Maay dooleel përëgi buuru Babilon moos, përëgi buuru Misra yoqi. Maay teg sama saamar ci loxol buuru Babilon, mu xàccil ko réewum Misra, ba ñu xam ne maay Aji Sax ji.
26
Maay tasaare Misra fi biir xeet yi, wasaare leen fi biir réew yi, ba ñu xam ne maay Aji Sax ji.»
← Chapter 29
Jump to:
Chapter 1
Chapter 2
Chapter 3
Chapter 4
Chapter 5
Chapter 6
Chapter 7
Chapter 8
Chapter 9
Chapter 10
Chapter 11
Chapter 12
Chapter 13
Chapter 14
Chapter 15
Chapter 16
Chapter 17
Chapter 18
Chapter 19
Chapter 20
Chapter 21
Chapter 22
Chapter 23
Chapter 24
Chapter 25
Chapter 26
Chapter 27
Chapter 28
Chapter 29
Chapter 30
Chapter 31
Chapter 32
Chapter 33
Chapter 34
Chapter 35
Chapter 36
Chapter 37
Chapter 38
Chapter 39
Chapter 40
Chapter 41
Chapter 42
Chapter 43
Chapter 44
Chapter 45
Chapter 46
Chapter 47
Chapter 48
Chapter 31 →
All chapters:
1
2
3
4
5
6
7
8
9
10
11
12
13
14
15
16
17
18
19
20
21
22
23
24
25
26
27
28
29
30
31
32
33
34
35
36
37
38
39
40
41
42
43
44
45
46
47
48