bible
ra
🌐 Language
English
Español
Français
Deutsch
Português
Italiano
Nederlands
Русский
中文
日本語
한국어
العربية
Türkçe
Tiếng Việt
ไทย
Indonesia
All Languages
Home
/
Wolof
/
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
/
Ezekiel 8
Ezekiel 8
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
← Chapter 7
Jump to:
Chapter 1
Chapter 2
Chapter 3
Chapter 4
Chapter 5
Chapter 6
Chapter 7
Chapter 8
Chapter 9
Chapter 10
Chapter 11
Chapter 12
Chapter 13
Chapter 14
Chapter 15
Chapter 16
Chapter 17
Chapter 18
Chapter 19
Chapter 20
Chapter 21
Chapter 22
Chapter 23
Chapter 24
Chapter 25
Chapter 26
Chapter 27
Chapter 28
Chapter 29
Chapter 30
Chapter 31
Chapter 32
Chapter 33
Chapter 34
Chapter 35
Chapter 36
Chapter 37
Chapter 38
Chapter 39
Chapter 40
Chapter 41
Chapter 42
Chapter 43
Chapter 44
Chapter 45
Chapter 46
Chapter 47
Chapter 48
Chapter 9 →
1
Keroog juróomi fan, ca juróom benneelu weer wa, ca juróom benneelu at ma, damaa toog sama biir néeg, magi Yuda bokk ak man toog. Fa la loxol Boroom bi Aji Sax ji dal fi sama kaw.
2
Ma xool, yem ci jëmm ju ame melokaanu nit. Li ko dale fiy nirook lupp yi, jëm suuf, sawara la. Li dale ci lupp yi jëm kaw ame melokaanu leer, mel ni weñ guy tàkk.
3
Mu tàllal lu bindoo ni loxo, daldi sëq sama kawaru bopp, lenn ngelaw yékkati ma ba ca diggante kaw ak suuf, yóbbu ma ba Yerusalem ci biir peeñum Yàlla, ba ca buntu ëttu biir kër Yàlla ba janook bëj-gànnaar, fa ñu teg jëmmu bokkaale, jay sabab fiiraange.
4
Ma jekki gis foofa leeru Yàllay Israyil ca melokaanam, ma ma ko gise woon ca joor ga.
5
Mu ne ma: «Yaw nit ki, séenul wetu bëj-gànnaar.» Ma séenu wetu bëj-gànnaar, yem ca jëmmu bokkaale jooju féeteek bunt ba dendeek sarxalukaay ba, ca bëj-gànnaaram.
6
Mu ne ma: «Yaw nit ki, gis nga li ñuy def, tojaange yu réy yi waa kër Israyil di def fii, ba di ma soreleek sama bérab bu sell bi. Te dinga gis tojaange yu gënatee màgg.»
7
Mu yóbbu ma ba ca buntu ëtt ba, ma yem ci menn pax mu nekk ca miir ba.
8
Mu ne ma: «Yaw nit ki, ayca, gasal fii miir bi!» Ma gas rekk, gis ab jàllukaay.
9
Mu ne ma: «Jàllal, ba gis tojaange yu bon yi ñu fiy def.»
10
Naka laa jàll ba xool, yemuma ci lu moy ay nataal yu ñu ñaas ci miir bi bépp, di mboolem dundoot yuy ramm-rammi ci suuf, ak rab yu jara seexlu, ak mboolem jëmmi kasaray tuur yu waa kër Israyil di jaamu.
11
Juróom ñaar fukki magi kër Israyil a nga taxaw, janook nataal ya. Yaasaña doomu Safan a nga ca. Ku ci nekk a nga ŋàbb sab and, cuuraay la jolli.
12
Mu ne ma: «Yaw nit ki, du yaa gis li magi kër Israyil di def ci lëndëm gi, ku nekk ak fa ñu jagleel sa nataalu tuur. Ña nga naan: “Aji Sax ji gisu nu, Aji Sax ji wacc na réew mi.”»
13
Mu dellu ne ma: «Te dinga gis tojaange yu gënatee màgg yu ñu nekke.»
14
Gannaaw loolu mu yóbbu ma ba ca buntu kër Aji Sax ja féete bëj-gànnaar. Ndeke jigéen ñaa nga foofa toog, di jooy deewug tuur mu ñuy wax Tamus.
15
Mu ne ma, yaw nit ki, yaa ko gisal sa bopp! Te dinga gis tojaange yu gëna màggati yii.
16
Mu yóbbu ma ba ca ëttu biiru kër Aji Sax ji, ndeke foofa ca buntu néeg Aji Sax ji, diggante dal-luwaayu bunt baak sarxalukaay ba, lu wara tollook ñaar fukki nit ak juróom a nga fa, ñu won gannaaw bérab bu sell bi, jublu penku, di sukkal jant bi, dëpp seen jë fi suuf.
17
Mu ne ma: «Yaw nit ki, du yaa gis lii? Moonte tojaange gi waa kër Yuda di def fii doyu leen. Xanaa ñuy wasaare fitna ci réew mi, di gëna yékkati sama xol. Xoolal! Ñu ngooguy def jëfi yéefar, jël caru garab, di fóon.
18
Man it maa leen di feye xadar. Duma xool bëtu ñéeblu, duma ñeewante. Dinañu yuuxu yuux yu réy, may dégg te duma leen faale.»
← Chapter 7
Jump to:
Chapter 1
Chapter 2
Chapter 3
Chapter 4
Chapter 5
Chapter 6
Chapter 7
Chapter 8
Chapter 9
Chapter 10
Chapter 11
Chapter 12
Chapter 13
Chapter 14
Chapter 15
Chapter 16
Chapter 17
Chapter 18
Chapter 19
Chapter 20
Chapter 21
Chapter 22
Chapter 23
Chapter 24
Chapter 25
Chapter 26
Chapter 27
Chapter 28
Chapter 29
Chapter 30
Chapter 31
Chapter 32
Chapter 33
Chapter 34
Chapter 35
Chapter 36
Chapter 37
Chapter 38
Chapter 39
Chapter 40
Chapter 41
Chapter 42
Chapter 43
Chapter 44
Chapter 45
Chapter 46
Chapter 47
Chapter 48
Chapter 9 →
All chapters:
1
2
3
4
5
6
7
8
9
10
11
12
13
14
15
16
17
18
19
20
21
22
23
24
25
26
27
28
29
30
31
32
33
34
35
36
37
38
39
40
41
42
43
44
45
46
47
48