bible
ra
🌐 Language
English
Español
Français
Deutsch
Português
Italiano
Nederlands
Русский
中文
日本語
한국어
العربية
Türkçe
Tiếng Việt
ไทย
Indonesia
All Languages
Home
/
Wolof
/
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
/
Ezekiel 37
Ezekiel 37
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
← Chapter 36
Jump to:
Chapter 1
Chapter 2
Chapter 3
Chapter 4
Chapter 5
Chapter 6
Chapter 7
Chapter 8
Chapter 9
Chapter 10
Chapter 11
Chapter 12
Chapter 13
Chapter 14
Chapter 15
Chapter 16
Chapter 17
Chapter 18
Chapter 19
Chapter 20
Chapter 21
Chapter 22
Chapter 23
Chapter 24
Chapter 25
Chapter 26
Chapter 27
Chapter 28
Chapter 29
Chapter 30
Chapter 31
Chapter 32
Chapter 33
Chapter 34
Chapter 35
Chapter 36
Chapter 37
Chapter 38
Chapter 39
Chapter 40
Chapter 41
Chapter 42
Chapter 43
Chapter 44
Chapter 45
Chapter 46
Chapter 47
Chapter 48
Chapter 38 →
1
Gannaaw loolu loxol Aji Sax ji da maa dikkal. Aji Sax ji yóbboo ma Noowam, ba teg ma ca digg joor ga, fekk joor ga fees dell aki yax.
2
Mu wërloo maa wërloo ca biir yax ya, ndeke yax yaa nga bare lool te wow koŋŋ ca biir joor ga.
3
Mu ne ma: «Yaw nit ki, ma ne, yii yax man naa dundaat a?» Ma ne ko: «Boroom bi Aji Sax ji, loolu de, yaw doŋŋ a ko xam.»
4
Mu ne ma: «Waxal waxyu fi kaw yax yii, ne leen: “Yeen yax yu wow yi, dégluleen kàddug Aji Sax ji:
5
Boroom bi Aji Sax ji dafa wax yax yii, ne leen: Maa ngii di leen sol ag noo, ngeen dund.
6
Maa leen di may ay siddit, saxal leen aw suux, sànge leen ab der, sol leen ag noo, ngeen dund, ba xam ne maay Aji Sax ji.”»
7
Ma biral waxyu na mu ma ko sante. Naka laa biral waxyu rekk, coow daldi jib, ànd akum riir, fekk yax yaay booloo, bu nekk ak ba muy àndal.
8
Ma gis ay siddit taq ca, aw suux sax ca kaw, ab der dikk, tege ca kaw, te genn noo amu ca.
9
Mu ne ma: «Yaw nit ki, waxalal Noo gi waxyu, waxal ko waxyu ne ko: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Yaw Noo gi, bàyyikool ñeenti yooni ngelaw yi te dikk, wal fi biir ñii ñu bóom, ba ñu dund.”»
10
Ma def la mu ma sant, waxyu, noo ga dikk, duggsi, ñu dundaat, jóg taxaw, di gàngoor gu baree bare.
11
Mu ne ma: «Yaw nit ki, yax yii ñooy mboolem waa kër Israyil. Ñu ngi naan: “Nun de, ay yaxi neen yu wow koŋŋ lanu, sunu yaakaar tas na, nun kay yàqu nanu.”
12
Kon nag biralal waxyu, ne leen: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Yeen sama ñoñ, maa ngii di ubbisi seeni bàmmeel, dekkale leen ca seeni bàmmeel, délloosi leen kaw suufas Israyil.
13
Yeen sama ñoñ, bu ma ubbee seeni bàmmeel, ba yékkatee leen ca seeni bàmmeel, dingeen xam ne maay Aji Sax ji.
14
Maa leen di sol samag noo, ngeen dund, ma samp leen seen suufas bopp, ba ngeen xam ne man Aji Sax ji maa wax, maa def. Kàddug Aji Sax jee.”»
15
Ba loolu wéyee kàddug Aji Sax ji dikkal ma ne ma:
16
«Yaw nit ki, sàkkal aw dénk, nga bind ci kaw lii: “Ñeel Yuda ak giiri Israyil yi mu àndal.” Nga sàkkaat weneen dénk, bind ci kawam: “Ñeel Yuusufa bantub Efrayim ak waa kër Israyil yi mu àndal,”
17
te nga boole ñaari dénk yi, ñu booloo, di wenn dénk ci sa loxo.
18
Bu la sa bokk yi laajee, ne la: “Xanaa doo nu wax lii lu muy tekki?”
19
nanga leen wax ne leen: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Maa ngii di jël dénku Yuusufa wi ci loxol Efrayim, mook giiri Israyil yi mu àndal, boole kook dénku Yuda, daldi def lépp wenn dénk, ñu booloo di wenn ci sama loxo.”
20
«Nanga ŋàbb dénk yi nga bind, ñuy gis,
21
te nga wax leen ne leen: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Maa ngii di jëleji bànni Israyil ca biir xeet ya ñu fekki, dajalee leen wet gu nekk, délloosi leen seen suufas bopp.
22
Maa leen di def wenn xeet doŋŋ ci réew mi, ci kaw tundi Israyil, ñoom ñépp bokk benn buur. Dootuñu doon ñaari xeet te dootuñu xàjjalikoo ñaari nguur.
23
Dootuñu sobeel seen bopp ci ay kasaray tuur, ak seen jëf ju siblook mboolem seeni tooñ. Maa leen di walloo ci mboolem seen ñàkk kóllëre. Ma setal leen, ñu doon sama ñoñ, ma doon seen Yàlla.
24
«“Daawuda sama jaam baay doon seen buur, di seen bennub sàmm ñoom ñépp. Sama àttey yoon lañuy doxe, sama dogali yoon lañuy sàmm, di ko jëfe.
25
Ñooy dëkke réew mi ma joxoon Yanqóoba sama jaam ba, te seeni maam dëkke woon ko. Ñu dëkke ko ñoom it, ñook seeni doom ak seeni sët, ba fàww, te Daawuda sama jaam ba mooy doon seen boroom jal ba fàww.
26
Maay fas ak ñoom kóllëreg jàmm, gu sax. Maa leen di samp, ful leen, maay samp sama bérab bu sell fi seen biir, ba fàww,
27
sama dëkkuwaay nekk fi seen biir, may seen Yàlla, ñuy sama ñoñ.
28
Bu sama bérab bu sell nekkee fi seen biir ba fàww, xeet yi dinañu xam ne man Aji Sax ji maa sellal Israyil.”»
← Chapter 36
Jump to:
Chapter 1
Chapter 2
Chapter 3
Chapter 4
Chapter 5
Chapter 6
Chapter 7
Chapter 8
Chapter 9
Chapter 10
Chapter 11
Chapter 12
Chapter 13
Chapter 14
Chapter 15
Chapter 16
Chapter 17
Chapter 18
Chapter 19
Chapter 20
Chapter 21
Chapter 22
Chapter 23
Chapter 24
Chapter 25
Chapter 26
Chapter 27
Chapter 28
Chapter 29
Chapter 30
Chapter 31
Chapter 32
Chapter 33
Chapter 34
Chapter 35
Chapter 36
Chapter 37
Chapter 38
Chapter 39
Chapter 40
Chapter 41
Chapter 42
Chapter 43
Chapter 44
Chapter 45
Chapter 46
Chapter 47
Chapter 48
Chapter 38 →
All chapters:
1
2
3
4
5
6
7
8
9
10
11
12
13
14
15
16
17
18
19
20
21
22
23
24
25
26
27
28
29
30
31
32
33
34
35
36
37
38
39
40
41
42
43
44
45
46
47
48