bible
ra
🌐 Language
English
Español
Français
Deutsch
Português
Italiano
Nederlands
Русский
中文
日本語
한국어
العربية
Türkçe
Tiếng Việt
ไทย
Indonesia
All Languages
Home
/
Wolof
/
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
/
Isaiah 23
Isaiah 23
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
← Chapter 22
Jump to:
Chapter 1
Chapter 2
Chapter 3
Chapter 4
Chapter 5
Chapter 6
Chapter 7
Chapter 8
Chapter 9
Chapter 10
Chapter 11
Chapter 12
Chapter 13
Chapter 14
Chapter 15
Chapter 16
Chapter 17
Chapter 18
Chapter 19
Chapter 20
Chapter 21
Chapter 22
Chapter 23
Chapter 24
Chapter 25
Chapter 26
Chapter 27
Chapter 28
Chapter 29
Chapter 30
Chapter 31
Chapter 32
Chapter 33
Chapter 34
Chapter 35
Chapter 36
Chapter 37
Chapter 38
Chapter 39
Chapter 40
Chapter 41
Chapter 42
Chapter 43
Chapter 44
Chapter 45
Chapter 46
Chapter 47
Chapter 48
Chapter 49
Chapter 50
Chapter 51
Chapter 52
Chapter 53
Chapter 54
Chapter 55
Chapter 56
Chapter 57
Chapter 58
Chapter 59
Chapter 60
Chapter 61
Chapter 62
Chapter 63
Chapter 64
Chapter 65
Chapter 66
Chapter 24 →
1
Yéene bii ñeel na dëkk ba ñuy wax Tir: Yeen waa gaali Tarsis ñi deele, jooyleen! Lépp a yàqu! Du kër, du teeruwaay. Fa dunu Sippar lañu leen ko waxe.
2
Yeen waa tefes, yaw Sidon laa ne, na say jula ñaawlu, yaw miy yónni nit ñu jaare géej,
3
war ndox ya ne xéew, peppum Sixor di sa tono, ak ngóobum Niil, ma xeet yi daan jula.
4
Yaw Sidon, gàcce ñeel na la, géej moo wax, tatay géej a ne: «Masumaa matu, masumaa jur, yaruma gone gu góor, yarumab janq.»
5
Bu xibaar ba àggee Misra de, ñu naqarlu deminu Tir.
6
Jàllal ba Tarsis, yeen waa tefes ga fa ne, jooyleen jooyi dëj.
7
Xanaa lii du seen dëkk bu xumb ba, te cosaanam di janti démb, nit ña di fa jógey sancaani fu sore?
8
Ana ku fexeel lii Tir ma daan fale, ay julaam diy kàngam, di jaaykat yi àddina teral?
9
Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko fexe, ngir sàggi sagub képp ku fiy damu, ba teddadil képp ku àddina teral.
10
Yeen waa Tir, defleen ni dexu Niil, walal seen réew; kenn tereetu leen.
11
Aji Sax ji tàllal na loxoom, tiimale géej, yëngal réew yi, ba santaane ñu màbb tatay Kanaan.
12
Nee yeen waa Sidon ñi mel ni janq bu ñu tëdde, dootuleen xaxaloo. Ayca, dawleen jàlli ba dunu Sippar, te du tax ngeen am fa noflaay.
13
Xool-leen li dal réewum Kaldeen ñi. Dootuñu sax aw xeet. Asiri wacce na leen rabi màndiŋ mi. Tabax nañu, gaw ko, màbb këri buur ya, gental ko.
14
Yeen boroom gaali Tarsis, yuuxuleen ni ñu deele, seen tata màbb na!
15
Bu keroogee ñu fàtte Tir juróom ñaar fukki at, ni àppu benn buur. Bu juróom ñaar fukki at yi matee, Tir xewle la ñu woyal gànc ba, ne ko:
16
«Yaw gànc bi ñu wacc, fabal sa xalam, wër dëkk bi, xalamala xalam te gëna woy, ndax ñu geesu la.»
17
Bu juróom ñaar fukki at yi matee, Aji Sax ji dikkal Tir, ñu delluy liggéey, di feyu, di gànctook mboolem réewi àddina fi kaw suuf
18
Waaye seen ñaq ak seen peyoor, dees koy sellalal Aji Sax ji, deesu ko dajaleek a denc. Ñi dëkk fi kanam Aji Sax jeey jagoo njariñ la, mu di leen dundal ba ñu regg, di leen solal col gu jekk.
← Chapter 22
Jump to:
Chapter 1
Chapter 2
Chapter 3
Chapter 4
Chapter 5
Chapter 6
Chapter 7
Chapter 8
Chapter 9
Chapter 10
Chapter 11
Chapter 12
Chapter 13
Chapter 14
Chapter 15
Chapter 16
Chapter 17
Chapter 18
Chapter 19
Chapter 20
Chapter 21
Chapter 22
Chapter 23
Chapter 24
Chapter 25
Chapter 26
Chapter 27
Chapter 28
Chapter 29
Chapter 30
Chapter 31
Chapter 32
Chapter 33
Chapter 34
Chapter 35
Chapter 36
Chapter 37
Chapter 38
Chapter 39
Chapter 40
Chapter 41
Chapter 42
Chapter 43
Chapter 44
Chapter 45
Chapter 46
Chapter 47
Chapter 48
Chapter 49
Chapter 50
Chapter 51
Chapter 52
Chapter 53
Chapter 54
Chapter 55
Chapter 56
Chapter 57
Chapter 58
Chapter 59
Chapter 60
Chapter 61
Chapter 62
Chapter 63
Chapter 64
Chapter 65
Chapter 66
Chapter 24 →
All chapters:
1
2
3
4
5
6
7
8
9
10
11
12
13
14
15
16
17
18
19
20
21
22
23
24
25
26
27
28
29
30
31
32
33
34
35
36
37
38
39
40
41
42
43
44
45
46
47
48
49
50
51
52
53
54
55
56
57
58
59
60
61
62
63
64
65
66