bible
ra
🌐 Language
English
Español
Français
Deutsch
Português
Italiano
Nederlands
Русский
中文
日本語
한국어
العربية
Türkçe
Tiếng Việt
ไทย
Indonesia
All Languages
Home
/
Wolof
/
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
/
Isaiah 52
Isaiah 52
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
← Chapter 51
Jump to:
Chapter 1
Chapter 2
Chapter 3
Chapter 4
Chapter 5
Chapter 6
Chapter 7
Chapter 8
Chapter 9
Chapter 10
Chapter 11
Chapter 12
Chapter 13
Chapter 14
Chapter 15
Chapter 16
Chapter 17
Chapter 18
Chapter 19
Chapter 20
Chapter 21
Chapter 22
Chapter 23
Chapter 24
Chapter 25
Chapter 26
Chapter 27
Chapter 28
Chapter 29
Chapter 30
Chapter 31
Chapter 32
Chapter 33
Chapter 34
Chapter 35
Chapter 36
Chapter 37
Chapter 38
Chapter 39
Chapter 40
Chapter 41
Chapter 42
Chapter 43
Chapter 44
Chapter 45
Chapter 46
Chapter 47
Chapter 48
Chapter 49
Chapter 50
Chapter 51
Chapter 52
Chapter 53
Chapter 54
Chapter 55
Chapter 56
Chapter 57
Chapter 58
Chapter 59
Chapter 60
Chapter 61
Chapter 62
Chapter 63
Chapter 64
Chapter 65
Chapter 66
Chapter 53 →
1
Yewwulee, yewwul, Siyoŋee, làmbool sa doole! Yerusalem, dëkk bu sell bi, solul ba ne ràññ! Ndax du kenn ku xaraful mbaa ku sobewu ku lay songati.
2
Yaw Yerusalem, mi ñu jàpp njaam, jógal fëgtu, yaw janq Siyoŋ mu taaru mi ñu jàpp njaam laa ne, tikkil buum gi ci sa baat.
3
Aji Sax ji déy dafa wax ne: «Dees leena wànteeroon ci dara, te du xaalis lees leen di jotaate.»
4
Boroom bi Aji Sax ji déy dafa wax ne: «Misra la sama ñoñ jëkka wàcc, dali fa, Asiri door leena not ci dara.
5
Léegi nag ana lu fiy sama wàll?» Kàddug Aji Sax jee. Mu ne: «Jàpp nañ sama ñoñ njaam ci dara; seeni sang a ngi tëggu, di dëkke ñàkke teggin sama tur.» Kàddug Aji Sax jee.
6
«Moo tax sama ñoñ di xam maay kan; moo tax bésub keroog ñu xam ne maay wax te maa ngii!»
7
Ndaw leeka rafeti tànk, kee bartaloo tund yi, di la dégtalsi jàmm, di la xibaar lu neex, àgge la ag mucc, ne la: «Éey, Siyoŋ, sa Yàllaay Buur!»
8
Déglul sa jongrukat yi, ña ngay xaacu, sarxollendoo. Ñoo gisal seen bopp Aji Sax ji di ñibbsi Siyoŋ.
9
Yeen genti Yerusalem, àndleen sarxolle; Aji Sax jeey dëfal ñoñam, mooy jot Yerusalem gii!
10
Aji Sax jee wone dooleem ju sell ji, xeet yépp di gis, ba ca cati àddina. Ñépp ay gis sunu wallu Yàlla.
11
Yeen ñiy yóbbu ndabi Aji Sax yu sell yi, bu ngeen di jóge Babilon, dëdduleena dëddu lu sobewu, bañ koo laal, setluleen te génn foofa.
12
Dungeen gaawtu déy, di dem; duy xél moos ngeen fay génne. Aji Sax jeey dox jiitu leen, te Yàllay Israyil laa ne, moo leen di féete gannaaw.
13
Aji Sax ji nee: «Sama jaam baa ngi, mooy baaxle, kawe, dees na ko yékkati, darajaal ko lool.
14
Moo dawoon yaramu ñu bare, ndax yàqu ba nirootul nit, bindootul woon ni doom aadama,
15
waaye noonu it lay waare ay xeeti xeet, ba buur yi wedam, ngir lu ñu leen waxuloon, te ñu gis ko, lu ñu dégguloon, te mujj ko ràññee.»
← Chapter 51
Jump to:
Chapter 1
Chapter 2
Chapter 3
Chapter 4
Chapter 5
Chapter 6
Chapter 7
Chapter 8
Chapter 9
Chapter 10
Chapter 11
Chapter 12
Chapter 13
Chapter 14
Chapter 15
Chapter 16
Chapter 17
Chapter 18
Chapter 19
Chapter 20
Chapter 21
Chapter 22
Chapter 23
Chapter 24
Chapter 25
Chapter 26
Chapter 27
Chapter 28
Chapter 29
Chapter 30
Chapter 31
Chapter 32
Chapter 33
Chapter 34
Chapter 35
Chapter 36
Chapter 37
Chapter 38
Chapter 39
Chapter 40
Chapter 41
Chapter 42
Chapter 43
Chapter 44
Chapter 45
Chapter 46
Chapter 47
Chapter 48
Chapter 49
Chapter 50
Chapter 51
Chapter 52
Chapter 53
Chapter 54
Chapter 55
Chapter 56
Chapter 57
Chapter 58
Chapter 59
Chapter 60
Chapter 61
Chapter 62
Chapter 63
Chapter 64
Chapter 65
Chapter 66
Chapter 53 →
All chapters:
1
2
3
4
5
6
7
8
9
10
11
12
13
14
15
16
17
18
19
20
21
22
23
24
25
26
27
28
29
30
31
32
33
34
35
36
37
38
39
40
41
42
43
44
45
46
47
48
49
50
51
52
53
54
55
56
57
58
59
60
61
62
63
64
65
66