bible
ra
🌐 Language
English
Español
Français
Deutsch
Português
Italiano
Nederlands
Русский
中文
日本語
한국어
العربية
Türkçe
Tiếng Việt
ไทย
Indonesia
All Languages
Home
/
Wolof
/
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
/
Isaiah 9
Isaiah 9
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
← Chapter 8
Jump to:
Chapter 1
Chapter 2
Chapter 3
Chapter 4
Chapter 5
Chapter 6
Chapter 7
Chapter 8
Chapter 9
Chapter 10
Chapter 11
Chapter 12
Chapter 13
Chapter 14
Chapter 15
Chapter 16
Chapter 17
Chapter 18
Chapter 19
Chapter 20
Chapter 21
Chapter 22
Chapter 23
Chapter 24
Chapter 25
Chapter 26
Chapter 27
Chapter 28
Chapter 29
Chapter 30
Chapter 31
Chapter 32
Chapter 33
Chapter 34
Chapter 35
Chapter 36
Chapter 37
Chapter 38
Chapter 39
Chapter 40
Chapter 41
Chapter 42
Chapter 43
Chapter 44
Chapter 45
Chapter 46
Chapter 47
Chapter 48
Chapter 49
Chapter 50
Chapter 51
Chapter 52
Chapter 53
Chapter 54
Chapter 55
Chapter 56
Chapter 57
Chapter 58
Chapter 59
Chapter 60
Chapter 61
Chapter 62
Chapter 63
Chapter 64
Chapter 65
Chapter 66
Chapter 10 →
1
Askan wiy doxe lëndëm nii, ñooy gis leer gu mag. Ñooñu dëkke réewum ndee mu ne këruus, ñoom la leer di fenkal.
2
Aji Sax ji, yaay yokk xeet wi, fulal leen bànneex, ñuy bége fi sa kanam, mbégtem ngóob, mel ni ñuy bànneexoo fa ñuy séddoo alalu xare.
3
Yaa leen di sippil seen sëf, damm bant ba ñu leen gàlloon, ak yetu ña leen notoon, na nga leen defaloon rekk ca xareb Majan.
4
Mboolem dàll wu ab noon dukkate ba dikk, ak turki bu màndi deretu xare, sawara lees koy leel.
5
Nde gonee juddu, ñeel nu, di doom ju góor ju ñu nu may, mu yenu kilifteef gi, ñu di ko wooye Diglekat bu yéeme bi, ak Yàlla jàmbaar ji, ak Baay bi sax dàkk, ak Buuru jàmm bi.
6
Dooley kilifteefam ak jàmm ja du am kemu, fa jalub Daawuda ak nguuram, ga muy samp, saxale ko njekk ak yoon, tey jii, ba fàww. Lii la Aji Sax ji Boroom gàngoor yi def ci xéraangeem.
7
Boroom bee yónnee kàddu gu dal Israyil, askanu Yanqóoba,
8
xeet wépp jot ca, ba ca Efrayim ak waa Samari, ñay damook a sagu naan:
9
«Ay móol màbb, nu yett ponkali doj, tabaxaat, xànqi garab yu ndaw daanoo ca, nu wuutal ca garabi seedar yu mag.»
10
Aji Sax ji yékkati nooni Buur Reccin, fi seen kaw, gemb seeni bañ,
11
Siri songe penku; Filisteen ña, sowu, ñu sëxëtoo Israyil, wonn. Teewul Aji Sax ji xàcci loxoom, meddiwul ba tey.
12
Waaye xeet wi delluwuñu ca ka leen duma, sàkkuwuñu Aji Sax ji Boroom gàngoor yi.
13
Moo tax Aji Sax ji doge Israyil bopp ak geen, boole tiir ak barax fóom ci benn bés.
14
Mag meek kàngam li ñooy bopp bi, yonent bi mokkal naaféq dib geen.
15
Ñi jiite askan wii ñoo leen di sànk, ña ñuy jiite loru.
16
Moo tax Boroom bi du bége seeni xale yu góor, du yërëm seeni jirim ak seeni jëtun. Ñoom ñépp a gëmadi, di def lu bon, ku ci nekk di wax lu amul bopp. Teewul Aji Sax ji xàcci loxoom, meddiwul ba tey.
17
Mbon a ngi tàkk moos ni sawara, xoyom dég aki dagg, jafal gajji gott bi, mu ne jippét, saxar, naaw.
18
Merum Aji Sax ji Boroom gàngoor yi taal na réew mi, xoyom waa réew mi, kenn yërëmul sa mbokk.
19
Nit ñaa ngi màtte ndijoor, te doyaluñu, di xàmpe càmmoñ te suuruñu, ku nekk di yàpp sa mbokk:
20
Manase song Efrayim, Efrayim song Manase, ñu mànkoo, noonoo Yuda. Teewul Aji Sax ji xàcci loxoom, meddiwul ba tey.
← Chapter 8
Jump to:
Chapter 1
Chapter 2
Chapter 3
Chapter 4
Chapter 5
Chapter 6
Chapter 7
Chapter 8
Chapter 9
Chapter 10
Chapter 11
Chapter 12
Chapter 13
Chapter 14
Chapter 15
Chapter 16
Chapter 17
Chapter 18
Chapter 19
Chapter 20
Chapter 21
Chapter 22
Chapter 23
Chapter 24
Chapter 25
Chapter 26
Chapter 27
Chapter 28
Chapter 29
Chapter 30
Chapter 31
Chapter 32
Chapter 33
Chapter 34
Chapter 35
Chapter 36
Chapter 37
Chapter 38
Chapter 39
Chapter 40
Chapter 41
Chapter 42
Chapter 43
Chapter 44
Chapter 45
Chapter 46
Chapter 47
Chapter 48
Chapter 49
Chapter 50
Chapter 51
Chapter 52
Chapter 53
Chapter 54
Chapter 55
Chapter 56
Chapter 57
Chapter 58
Chapter 59
Chapter 60
Chapter 61
Chapter 62
Chapter 63
Chapter 64
Chapter 65
Chapter 66
Chapter 10 →
All chapters:
1
2
3
4
5
6
7
8
9
10
11
12
13
14
15
16
17
18
19
20
21
22
23
24
25
26
27
28
29
30
31
32
33
34
35
36
37
38
39
40
41
42
43
44
45
46
47
48
49
50
51
52
53
54
55
56
57
58
59
60
61
62
63
64
65
66