bible
ra
🌐 Language
English
Español
Français
Deutsch
Português
Italiano
Nederlands
Русский
中文
日本語
한국어
العربية
Türkçe
Tiếng Việt
ไทย
Indonesia
All Languages
Home
/
Wolof
/
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
/
Jeremiah 14
Jeremiah 14
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
← Chapter 13
Jump to:
Chapter 1
Chapter 2
Chapter 3
Chapter 4
Chapter 5
Chapter 6
Chapter 7
Chapter 8
Chapter 9
Chapter 10
Chapter 11
Chapter 12
Chapter 13
Chapter 14
Chapter 15
Chapter 16
Chapter 17
Chapter 18
Chapter 19
Chapter 20
Chapter 21
Chapter 22
Chapter 23
Chapter 24
Chapter 25
Chapter 26
Chapter 27
Chapter 28
Chapter 29
Chapter 30
Chapter 31
Chapter 32
Chapter 33
Chapter 34
Chapter 35
Chapter 36
Chapter 37
Chapter 38
Chapter 39
Chapter 40
Chapter 41
Chapter 42
Chapter 43
Chapter 44
Chapter 45
Chapter 46
Chapter 47
Chapter 48
Chapter 49
Chapter 50
Chapter 51
Chapter 52
Chapter 15 →
1
Kàddug Aji Sax jii dikkaloon na Yeremi, jëm ca maral ma. Mu ne:
2
«Waa Yudaa ngi ñaawlu, doole dëddu dëkk yi, ñu ne yogg, ne lasar fi suuf, yuux jollee Yerusalem.
3
Kàngam ya yebal seeni surga, ñu rooti; ñu dem, gisuñu ndox ca mbalka ya, délseek seen xotti ndab, jàq, yaakaar tas, ñu muuru di tiislu.
4
Réew mi tawluwul, suuf si fett, yaakaaru beykat tas, mu muuru, di tiislu.
5
Kéwél sax jur ci àll bi, sànni ndax ñàkk um ñax.
6
Mbaamu àll taxaw ci tund yi ne faraas, di àppaat niw till, ñàkk parlu, gët ya giim.»
7
Dëgg la sunuy ñaawtéef a nu tuumaal, waaye éy Aji Sax ji, jógal te saw tur tax, doonte dëddu nanu la ay yooni yoon, moy la.
8
Éy yaw, yaakaaru Israyil, mi nuy wallu bésu njàqare, bul ñooru ni doxandéem ci réew mi, mbaa ku nekk ciw yoon, jàdd fi, fanaan.
9
Ngalla bul mel ni ku waaru, mbaa jàmbaar ju manul walloo. Yaw Aji Sax ji, yaa ngi sunu biir, ñu di nu tudde saw tur. Bu nu wacc!
10
Aji Sax ji dafa wax ci askan wii ne: «Ñeeka bëgg ub taxawaalu, baña téye seen tànk. Moo tax man Aji Sax ji bégewuma leen. Léegi ma bàyyi xel seenug mbon, ba mbugale leen seeni moy.»
11
Aji Sax ji nag ne ma: «Bul ñaanal askan wii.
12
Su ñu ci boole woon koor sax, duma déglu seeni dagaan. Su ñu ma doon sarxalal saraxu rendi-dóomal ak saraxu pepp it, du maa leen di nangul. Xanaa saamar akub xiif ak mbas kay laa leen di faagaagale.»
13
Ma ne ko: «Éy Boroom bi Aji Sax ji, yonent yaa ngii di leen wax ne duñu dajeek saamar, duñu xiif te jàmm ju ne ñoyy nga leen di defal fi bii bérab.»
14
Aji Sax ji ne ma: « Waxyuy fen la yonent yiy waxe ci sama tur. Yebaluma leen, santuma leen ko, waxumaak ñoom. Peeñuy fen ak ngisaaney neen ak nax yu ñu fental seen bopp lañu leen di jottlee waxyu.»
15
Moo tax Aji Sax ji dafa wax ne: «Yonent yi ma yebalul te ñuy waxe waxyu ci sama tur naan: “Saamar akub xiif du am ci miim réew,” saamar akub xiif ay mujje yooyu yonent.
16
Ñi ñu doon jottli ay waxyu it, xiif ak saamar a leen di rey, ñu sànni seeni néew ci mbeddi Yerusalem, te duñu am ku leen rob, ñook seeni jabar ak seeni doom, góor ak jigéen. Dinaa leen xëpp seen ay.
17
Nanga leen yégal saw tiis, ne leen: “Naa tuur rongooñ guddeek bëccëg, te du fer; sama bokki bopp yi damm ba dammtoo, ndaw góom bu metti!
18
Ma dem, xool àll, gisuma lu moy ñu saamar bóom, ma dugg biir dëkk, gisuma lu moy ñu ne làcc akub xiif, yonent ak sarxalkat di wër réew mi, xam-xam réer leen.”»
19
Aji Sax ji, wacc ngaa wacc Yuda nii? Am Siyoŋ a la génnliku? Lu tax nga di nu dumaa musiba mu amul paj? Nuy yaakaar jàmm, dara baaxul, nuy séentum paj, tiitaange ne jaas!
20
Aji Sax ji, xam nanu sunug mbon, xam sunu ñaawtéefi maam; moy nanu la moos.
21
Waaye xoolal ci yaw te bul xalab, bul teddadil sa jal bu tedd. Bàyyil xel te baña fecci sa kóllëreek nun.
22
Xërëmi neen yi yéefar yiy jaamu, ana ku ci mana taw? Am asamaan ay sóobal boppam ay waame? Du yaw la Aji Sax ji sunu Yàlla? Yaw lanu yaakaar, te loolu lépp, yaw a.
← Chapter 13
Jump to:
Chapter 1
Chapter 2
Chapter 3
Chapter 4
Chapter 5
Chapter 6
Chapter 7
Chapter 8
Chapter 9
Chapter 10
Chapter 11
Chapter 12
Chapter 13
Chapter 14
Chapter 15
Chapter 16
Chapter 17
Chapter 18
Chapter 19
Chapter 20
Chapter 21
Chapter 22
Chapter 23
Chapter 24
Chapter 25
Chapter 26
Chapter 27
Chapter 28
Chapter 29
Chapter 30
Chapter 31
Chapter 32
Chapter 33
Chapter 34
Chapter 35
Chapter 36
Chapter 37
Chapter 38
Chapter 39
Chapter 40
Chapter 41
Chapter 42
Chapter 43
Chapter 44
Chapter 45
Chapter 46
Chapter 47
Chapter 48
Chapter 49
Chapter 50
Chapter 51
Chapter 52
Chapter 15 →
All chapters:
1
2
3
4
5
6
7
8
9
10
11
12
13
14
15
16
17
18
19
20
21
22
23
24
25
26
27
28
29
30
31
32
33
34
35
36
37
38
39
40
41
42
43
44
45
46
47
48
49
50
51
52