bible
ra
🌐 Language
English
Español
Français
Deutsch
Português
Italiano
Nederlands
Русский
中文
日本語
한국어
العربية
Türkçe
Tiếng Việt
ไทย
Indonesia
All Languages
Home
/
Wolof
/
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
/
Jeremiah 28
Jeremiah 28
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
← Chapter 27
Jump to:
Chapter 1
Chapter 2
Chapter 3
Chapter 4
Chapter 5
Chapter 6
Chapter 7
Chapter 8
Chapter 9
Chapter 10
Chapter 11
Chapter 12
Chapter 13
Chapter 14
Chapter 15
Chapter 16
Chapter 17
Chapter 18
Chapter 19
Chapter 20
Chapter 21
Chapter 22
Chapter 23
Chapter 24
Chapter 25
Chapter 26
Chapter 27
Chapter 28
Chapter 29
Chapter 30
Chapter 31
Chapter 32
Chapter 33
Chapter 34
Chapter 35
Chapter 36
Chapter 37
Chapter 38
Chapter 39
Chapter 40
Chapter 41
Chapter 42
Chapter 43
Chapter 44
Chapter 45
Chapter 46
Chapter 47
Chapter 48
Chapter 49
Chapter 50
Chapter 51
Chapter 52
Chapter 29 →
1
Ca menn at ma, fekk Cedesyas buurub Yuda di doora falu, yemook ñeenteelu atam, ca juróomeelu weer wa, am na doomu Asur ju ñuy wax Anaña, di yonent bu cosaanoo Gabawon. Mu wax ak Yonent Yàlla Yeremi ca biir kër Aji Sax ji, fa kanam sarxalkat yaak mbooloo mépp, ne ko:
2
«Aji Sax ji Yàllay Israyil Boroom gàngoor yi dafa wax ne: Damm naa yet wi leen buuru Babilon tënke woon.
3
Fii ak ñaari at tembe dinaa délloosi fii mboolem ndabi kër Aji Sax ji Nabukodonosor buuru Babilon jële woon bérab bii, yóbbu Babilon.
4
Dinaa délloosi fii itam buurub Yuda Yekoña doomu Yowakim, te mboolem ngàllog Yuda ga demoon Babilon, maa leen di délloosi bérab bii.» Kàddug Aji Sax jee. «Maay damm moos yetu buuru Babilon wi mu leen tënke.»
5
Ba loolu amee Yonent Yàlla Yeremi tontu yonent ba ñuy wax Anaña fa kanam sarxalkat yaak mbooloo ma taxaw fa biir kër Aji Sax ji mépp.
6
Mu ne ko: «Amiin! Yal na ko Aji Sax ji defee! Yal na Aji Sax ji sottal sa kàdduy waxyu yi nga wax, ba délloosee Babilon ba fii ndabi kër Aji Sax ji ak mboolem ña ñu fa toxal.
7
Waaye ngalla déglul bu baax kàddu gii ma lay wax, yaak mbooloo mi mépp.
8
Yonent yi feeñoon naka jekk lu ma jiitu, jiitu la, jottli nañu réew yu yaatu ak nguur yu mag seen waxyuy xare ak musiba ak mbas.
9
Ab yonent nag bu dee biral waxyub jàmm, su jàmm ja dikkee, ñu xam ne Aji Sax jee ko yebal ci lu wér.»
10
Ba mu ko defee yonent ba ñuy wax Anaña yékkatee yet wa ca ndoddu Yonent Yàlla Yeremi, damm ko.
11
Anaña àddu fa kanam mbooloo ma mépp ne leen: «Aji Sax ji dafa wax ne: Nii laay damme yet wi buur Nabukodonosor buuru Babilon di tënkee. Fii ak ñaari at tembe dinaa jële yet wi ci ndoddu mboolem xeet yi mu ko tënke.» Ba loolu amee Yonent Yàlla Yeremi dem yoonam.
12
Gannaaw ba yonent ba ñuy wax Anaña yékkatee yet wa ca ndoddu Yonent Yàlla Yeremi ba damm ko, kàddug Aji Sax ji dikkal Yeremi, ne ko:
13
«Demal wax Anaña ne ko: “Aji Sax ji dafa wax ne: Yetu bant nga damm, waaye dinga ko wuutale yetu weñ.
14
Ndax Aji Sax ji, Yàllay Israyil Boroom gàngoori xare yi dafa wax ne: Yetu weñ laay teg ci ndoddu mboolem xeet yii, ñu nangul Nabukodonosor buuru Babilon, di ko surgawu. Te rabi àll yi sax, maa leen di teg ci loxoom.”»
15
Gannaaw loolu Yonent Yàlla Yeremi ne yonent ba ñuy wax Anaña: «Anaña, déglul bu baax li ma lay wax: Aji Sax ji yebalu la, yaw ngay gëmloo askan wii ay fen.
16
Moo tax Aji Sax ji dafa wax ne: “Maa ngii di la yebal, nga jóge fi kaw suuf. Ren jii ngay dee, ndax kàdduy gàntal nga waxal Aji Sax ji.”»
17
Yonent ba ñuy wax Anaña ca at mooma la dee ca juróom ñaareelu weer wa.
← Chapter 27
Jump to:
Chapter 1
Chapter 2
Chapter 3
Chapter 4
Chapter 5
Chapter 6
Chapter 7
Chapter 8
Chapter 9
Chapter 10
Chapter 11
Chapter 12
Chapter 13
Chapter 14
Chapter 15
Chapter 16
Chapter 17
Chapter 18
Chapter 19
Chapter 20
Chapter 21
Chapter 22
Chapter 23
Chapter 24
Chapter 25
Chapter 26
Chapter 27
Chapter 28
Chapter 29
Chapter 30
Chapter 31
Chapter 32
Chapter 33
Chapter 34
Chapter 35
Chapter 36
Chapter 37
Chapter 38
Chapter 39
Chapter 40
Chapter 41
Chapter 42
Chapter 43
Chapter 44
Chapter 45
Chapter 46
Chapter 47
Chapter 48
Chapter 49
Chapter 50
Chapter 51
Chapter 52
Chapter 29 →
All chapters:
1
2
3
4
5
6
7
8
9
10
11
12
13
14
15
16
17
18
19
20
21
22
23
24
25
26
27
28
29
30
31
32
33
34
35
36
37
38
39
40
41
42
43
44
45
46
47
48
49
50
51
52