bible
ra
🌐 Language
English
Español
Français
Deutsch
Português
Italiano
Nederlands
Русский
中文
日本語
한국어
العربية
Türkçe
Tiếng Việt
ไทย
Indonesia
All Languages
Home
/
Wolof
/
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
/
Jeremiah 4
Jeremiah 4
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
← Chapter 3
Jump to:
Chapter 1
Chapter 2
Chapter 3
Chapter 4
Chapter 5
Chapter 6
Chapter 7
Chapter 8
Chapter 9
Chapter 10
Chapter 11
Chapter 12
Chapter 13
Chapter 14
Chapter 15
Chapter 16
Chapter 17
Chapter 18
Chapter 19
Chapter 20
Chapter 21
Chapter 22
Chapter 23
Chapter 24
Chapter 25
Chapter 26
Chapter 27
Chapter 28
Chapter 29
Chapter 30
Chapter 31
Chapter 32
Chapter 33
Chapter 34
Chapter 35
Chapter 36
Chapter 37
Chapter 38
Chapter 39
Chapter 40
Chapter 41
Chapter 42
Chapter 43
Chapter 44
Chapter 45
Chapter 46
Chapter 47
Chapter 48
Chapter 49
Chapter 50
Chapter 51
Chapter 52
Chapter 5 →
1
«Yaw Israyil, sooy waññiku, waññikul fi man.» Kàddug Aji Sax jee. «Soo jëlee fi sama kanam sa jëf ju siblu, te jenguloo,
2
xanaa di waate Aji Sax jiy dund, ci dëgg ak njub ak ngor, kon xeet yi di barkeeloo Aji Sax ji, di ko sagoo.»
3
Aji Sax ji déy dafa wax waa Yudak Yerusalem, ne leen: «Ruujleen seen tool, buleen ji ciy dég.
4
Yeen waa Yudak Yerusalem, deeleen xaraf ngir Aji Sax ji, dogleen seen mbuñukay xol, balaa sama xadar ne jippét ni sawara, di tàkk te deesu ko fey ndax seen jëf ju bon.
5
«Nangeen yégle lii fa Yuda, dégtale ko fa Yerusalem, yéenee koog liit fi biir réew mi te xaacu seen kem kàttan ne leen: “Dajeleen, nu dem ca dëkk ya tata wër.”
6
Yékkatileen raaya, jubale Siyoŋ, làqujileen, buleen taxaw, musiba déy laay jële bëj-gànnaar, muy safaan bu réy.
7
«Gayndee fëlle geeram, fàkkaskatu xeet yee jóg, génne këram, nara gental seeni dëkk, ba ñu di gent yu kenn dëkkul.
8
Kon nag sol-leeni saaku, ñaawloo te yuuxu ne: “Merum Aji Sax ji tàng na kat te moyu nu.”
9
Bésub keroog,» kàddug Aji Sax jee, «xolu buur jeex, kàngam ne yàcc, sarxalkat waaru, yonent jommi.»
10
Ma ne, «Éy Boroom bi Aji Sax ji, yaa naxlu askan wii nax yu metti, ba nga nee: “Yerusalem jàmm lay am,” te saamar tege ci putam.»
11
Janti keroog dees na wax askanu Yerusalem wii, ne leen: «Jaas bu tàng a uppe kaw tund ya ne faraas ca màndiŋ ma, wuti sama ñoñ. Du doon ngelaw lees di bàcceek a beese.
12
Ngelaw lu ko ëpp doole laay indi. Léegi maa leen di biral sama kàddug mbugal.»
13
«Noon baa ngii, di jóg niy niir, watiiri xareem ni ngëlén, fasam ya gëna gaawi jaxaay. Wóoy ngalla nun, yàqu nan!»
14
«Éey Yerusalem, fóotal sa xol, jële ci lu bon, ndax nga mucc. Foo àppal sa mébéti xol yu bon?
15
Kàddug yéenee ngi jibe Dan, musiba dégtu na, bawoo tundu Efrayim.
16
Jottlileen ko xeet yi, neleen Yerusalem: “Songkat yaa ngii riire réew mu sore ma, xaacoondoo fi kaw dëkki Yuda.”
17
Ñooy gaw Yerusalem ni wattukati tool, ndax man la gàntal.» Kàddug Aji Sax jee.
18
«Sa jëfin ak say jëf a la yóbbe lii, sa musibaa ngook, wex la xàtt, di dagg sa xol.»
19
Maaka jàqa jàq bay jal-jali, sama xol biy fuddu! Éy wii mititu xol! Duma mana noppi, maa dégg wooteb liit ak yuuxi xare.
20
Yéenees na rajaxoo ci kaw rajaxoo, réew mi mépp ne tasar kay! Jekki-jekki samay xayma tasaaroo. Xef-xippi ndimoy xayma ya xotatoo!
21
Xanaa duma gis ba fàww raayab noon, liitu xare di ko feelu?
22
«Dofe la sama ñoñ def. Man, xamuñu maay kan, mbetey gone yu dul xalaat dara; dég-dég, tus; seen xel mépp, lu bon rekk, lu baax, xamuñu ci dara.»
23
Maa xool suuf, ndeke ma nga ne maraas, ne wëyëŋ; ma xool asamaan, leer amatu ca.
24
Ma xool tund yu mag yi, ndeke ñu ngi yëngu, tund yu ndaw yépp di jaayu.
25
Ma xoolaat, gisuma nit, njanaaw yépp daw.
26
Ma xool, gis suuf su nangu sa di ndànd-foyfoy, dëkk yépp raaf ndax Aji Sax jeek tàngaayu sànjam.
27
Aji Sax ji déy dafa wax ne: «Duma tas lépp tasar, waaye réew mi mépp ay gental.
28
Loolooy tax suuf di ñaawlu, asamaan di lëndëm. Maa ko wax, maa ko dogu; duma dëpp, duma deltu gannaaw.»
29
Gawar ak fittkat riir, waa dëkk yépp fëx, ñii tàbbiy gajj, ñee ñalgu ci kawi doj, ñu won dëkkoo dëkk gannaaw, kenn desatu ca.
30
Yaw Yerusalem mu tas mi, ana looy def nii, di solu ba yànj, gànjaroo wurus, tusngalu, yàkkleey gët? Yaa ngi caaxoñu ci neen: say xéddkat wacc nañu la, sa bakkan lañuy wut.
31
Baatu ndaw su jagadi laa dégg, ma nga jàq, di matub taawam. Baatub Siyoŋ, dëkk bu taaru baa! Ma ngay àppaat, tàllal yoxo ya, naan: «Wóoy, ngalla man; ne yàcc ci loxol bóomkat yi!»
← Chapter 3
Jump to:
Chapter 1
Chapter 2
Chapter 3
Chapter 4
Chapter 5
Chapter 6
Chapter 7
Chapter 8
Chapter 9
Chapter 10
Chapter 11
Chapter 12
Chapter 13
Chapter 14
Chapter 15
Chapter 16
Chapter 17
Chapter 18
Chapter 19
Chapter 20
Chapter 21
Chapter 22
Chapter 23
Chapter 24
Chapter 25
Chapter 26
Chapter 27
Chapter 28
Chapter 29
Chapter 30
Chapter 31
Chapter 32
Chapter 33
Chapter 34
Chapter 35
Chapter 36
Chapter 37
Chapter 38
Chapter 39
Chapter 40
Chapter 41
Chapter 42
Chapter 43
Chapter 44
Chapter 45
Chapter 46
Chapter 47
Chapter 48
Chapter 49
Chapter 50
Chapter 51
Chapter 52
Chapter 5 →
All chapters:
1
2
3
4
5
6
7
8
9
10
11
12
13
14
15
16
17
18
19
20
21
22
23
24
25
26
27
28
29
30
31
32
33
34
35
36
37
38
39
40
41
42
43
44
45
46
47
48
49
50
51
52