bible
ra
🌐 Language
English
Español
Français
Deutsch
Português
Italiano
Nederlands
Русский
中文
日本語
한국어
العربية
Türkçe
Tiếng Việt
ไทย
Indonesia
All Languages
Home
/
Wolof
/
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
/
Jeremiah 41
Jeremiah 41
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
← Chapter 40
Jump to:
Chapter 1
Chapter 2
Chapter 3
Chapter 4
Chapter 5
Chapter 6
Chapter 7
Chapter 8
Chapter 9
Chapter 10
Chapter 11
Chapter 12
Chapter 13
Chapter 14
Chapter 15
Chapter 16
Chapter 17
Chapter 18
Chapter 19
Chapter 20
Chapter 21
Chapter 22
Chapter 23
Chapter 24
Chapter 25
Chapter 26
Chapter 27
Chapter 28
Chapter 29
Chapter 30
Chapter 31
Chapter 32
Chapter 33
Chapter 34
Chapter 35
Chapter 36
Chapter 37
Chapter 38
Chapter 39
Chapter 40
Chapter 41
Chapter 42
Chapter 43
Chapter 44
Chapter 45
Chapter 46
Chapter 47
Chapter 48
Chapter 49
Chapter 50
Chapter 51
Chapter 52
Chapter 42 →
1
Ba ñu demee ba ca juróom ñaareelu weer wa ca at mooma, Ismayil doomu Netaña doomu Elisama, askanoo ci ñi moom Yuda te di njiitu jawriñi buur, ànd ak fukki nit ba ca Gedalya doomu Ayikam ca Mispa. Ci kaw loolu, ñu bokk di lekk ca kër Gedalya.
2
Ismayil jekki jóg, mook fukki nit ña mu àndal. Ñu jam saamar Gedalya ma buuru Babilon dénkoon réew ma, ba rey ko.
3
Ismayil reyaale mboolem Yudeen ña nekkoon ak Gedalya ca Mispa ak xarekati Babilon ya fa nekkoon.
4
Ba ñu bóomee Gedalya ba ca ëllëg sa, fu kenn yégul,
5
mu am juróom ñett fukki nit ñu bàyyikoo Sikem ak Silo ak Samari. Ña nga wat seen sikkim, xotti seeni yére, dagg-daggee seen yaram, di ko ñaawloo. Ñu ŋàbb saraxu pepp ak cuuraay bu ñu indil kër Aji Sax.
6
Ismayil génne buntu Mispa, gatanduji leen. Ma ngay dox, jëm ca ñoom, di jooy-jooylu ba dajeek ñoom, ne leen: «Agsileen kër Gedalya doomu Ayikam!»
7
Naka lañu dikk ba ca biir dëkk ba, Ismayil ak ay nitam bóom leen, tàbbal néew ya ci kàmb.
8
Fekk na mu am fukki nit ñu bokk ci ñoom ñu ne woon Ismayil: «Tee nga noo baña rey? Nun de am nanub denc ci àll bi. Peppu belee nga ca ak lors ak diw ak lem.» Loolu tax Ismayil fomm, ba boolewu leen ak seeni bokk, rey.
9
Kàmb ga Ismayil sànni néewi nit ña mu reyaaleek Gedalya mooy kàmb ga Buur Asa mu Yuda gasoon ba ko Buur Basa mu Israyil songee xare. Moom la Ismayil doomu Netaña feesal aki néew.
10
Gannaaw loolu mu jàpp mboolem ña des Mispa, di doomi buur yu jigéen ak mboolem ña des Mispa, te Nebusaradan, njiital dag ya, dénkoon leen Gedalya. Ismayil jàpp leen njaam, daldi wutali diiwaanu Amoneen ña.
11
Ba loolu amee Yowanan doomu Kareya ak njiiti xare yi mu àndal yépp dégg musiba mi Ismayil doomu Netaña def mépp.
12
Ñu ànd ak seeni nit, topp ko ngir xareek moom, ba dab ko ca déeg bu mag ba ca Gabawon.
13
Ba nit ña Ismayil jàppe Mispa gisee Yowanan ak mboolem njiiti xare ya mu àndal, dañoo bég.
14
Ñoom ñépp walbatiku, daw fekki Yowanan doomu Kareya.
15
Teewul Ismayil doomu Netaña ak juróom ñetti nitam rëcc Yowanan, daw làquji réewum Amon.
16
Yowanan doomu Kareya ak mboolem njiiti xare yi mu àndal nag boole mboolem la des ca mbooloo, ma Yonatan xettli woon ca Ismayil doomu Nataña ca Mispa, gannaaw ba Ismayil bóomee Gedalya doomu Ayikam. Ay nit ñu Yowanan jële woon Gabawon a nga ca, diy góor: ay xarekat ak bëkk-néegi buur, aki jigéen aki gone.
17
Ñu dem ba dali ca dalukaayu Kimyam, ca wetu Betleyem, di waaj yoonu Misra,
18
ngir rëcc waa Babilon ñi ñu ragaloon, ndax la Ismayil doomu Netaña bóom Gedalya doomu Ayikam, ma buuru Babilon dénkoon réew ma.
← Chapter 40
Jump to:
Chapter 1
Chapter 2
Chapter 3
Chapter 4
Chapter 5
Chapter 6
Chapter 7
Chapter 8
Chapter 9
Chapter 10
Chapter 11
Chapter 12
Chapter 13
Chapter 14
Chapter 15
Chapter 16
Chapter 17
Chapter 18
Chapter 19
Chapter 20
Chapter 21
Chapter 22
Chapter 23
Chapter 24
Chapter 25
Chapter 26
Chapter 27
Chapter 28
Chapter 29
Chapter 30
Chapter 31
Chapter 32
Chapter 33
Chapter 34
Chapter 35
Chapter 36
Chapter 37
Chapter 38
Chapter 39
Chapter 40
Chapter 41
Chapter 42
Chapter 43
Chapter 44
Chapter 45
Chapter 46
Chapter 47
Chapter 48
Chapter 49
Chapter 50
Chapter 51
Chapter 52
Chapter 42 →
All chapters:
1
2
3
4
5
6
7
8
9
10
11
12
13
14
15
16
17
18
19
20
21
22
23
24
25
26
27
28
29
30
31
32
33
34
35
36
37
38
39
40
41
42
43
44
45
46
47
48
49
50
51
52