bible
ra
🌐 Language
English
Español
Français
Deutsch
Português
Italiano
Nederlands
Русский
中文
日本語
한국어
العربية
Türkçe
Tiếng Việt
ไทย
Indonesia
All Languages
Home
/
Wolof
/
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
/
Proverbs 10
Proverbs 10
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
← Chapter 9
Jump to:
Chapter 1
Chapter 2
Chapter 3
Chapter 4
Chapter 5
Chapter 6
Chapter 7
Chapter 8
Chapter 9
Chapter 10
Chapter 11
Chapter 12
Chapter 13
Chapter 14
Chapter 15
Chapter 16
Chapter 17
Chapter 18
Chapter 19
Chapter 20
Chapter 21
Chapter 22
Chapter 23
Chapter 24
Chapter 25
Chapter 26
Chapter 27
Chapter 28
Chapter 29
Chapter 30
Chapter 31
Chapter 11 →
1
Kàddu yu xelu yu Suleymaan. Doom rafet xel, baay ba bég; doom dof, ndey ja tiis.
2
Alal ju lewul du jariñ; jub, mucc ci gàtt fan.
3
Aji Sax ji du seetaan ku jub, di xiif, waaye day xañ ab soxor la mu xemmem.
4
Yaafus, walaakaana; farlu, woomle.
5
Ku ngóob jot, nga góob, xelu nga; ngóob taxaw, ngay nelaw, gàcce la.
6
Jub, barkeelu; ku soxor, wax ja làq fitna.
7
Ku jub barkeel, saw tur du fey; ab soxor, turam seey.
8
Ku rafet xel day jëfe santaane, ab dof waxa wax, ba loru.
9
Maandu, fegu; dëng, weeru.
10
Piiseek làq-làqal, sabab njàqare; ab dof waxa wax, ba loru.
11
Kàdduy ku jub bëtu ndox la, day naatal; waaye ku soxor, wax ja làq fitna.
12
Mbañeelak ayoo; cofeelak jéggale bépp tooñ.
13
Kuy dégg, say wax rafet; te ku ñàkk bopp, yelloo yetu gannaaw.
14
Ku rafet xel day xam, ne cell; bu dof noppiwul, yàqule teew.
15
Alal day aar boroom ni ab tata, ñàkk di lor baadoolo.
16
Ku jub jot peyam, dunde; ab soxor di bàkkaare alalam.
17
Yaru, gudd fan; sàgganey àrtu, sànku.
18
Ku la nëbbal mbañeel, da lay fen; kuy wër di sos, ab dof la.
19
Wax ju bare, moy ñàkku ca; ku moom sa làmmiñ, xelu nga.
20
Kàddug ku jub di ngën-gi-xaalis, xelum coxor amul solo.
21
Kàdduy ku jub jariñ na ñu bare, dof ñàkk na bopp, ba far dee.
22
Barkeb Aji Sax jeey maye alal, kër-këri taxula barele.
23
Jëf ju bon la dof di foye; ku am dég-dég safoo lu xelu.
24
Ab soxor, li mu ragal moo koy dab; nammeelu ku jub day sotti.
25
Bu ngëlén walee, ab soxor ne mes; ku jub, sab reen sax ba fàww.
26
Ndaw lu tayel ca ka yónnee daa mel ni lu forox ciy gëñ mbaa saxar ciy gët.
27
Ragal Aji Sax ji, gudd fan; soxor, gàtt fan.
28
Ku jub day séentu mbégte, gis ko; ab soxor yaakaar, yàkki.
29
Aji Sax jeeki nammeelam rawtu la ci ku mat, di sànkute ci kuy def lu bon.
30
Ku jub deesu ko daaneel mukk, ku soxor du yàgg cim réew.
31
Kàddug ku jub day jur xel mu rafet, ku wax njekkar ñu tëj sa gémmiñ.
32
Ku jub day xam wax ju yiw; ab soxor sàlloo waxi njekkar.
← Chapter 9
Jump to:
Chapter 1
Chapter 2
Chapter 3
Chapter 4
Chapter 5
Chapter 6
Chapter 7
Chapter 8
Chapter 9
Chapter 10
Chapter 11
Chapter 12
Chapter 13
Chapter 14
Chapter 15
Chapter 16
Chapter 17
Chapter 18
Chapter 19
Chapter 20
Chapter 21
Chapter 22
Chapter 23
Chapter 24
Chapter 25
Chapter 26
Chapter 27
Chapter 28
Chapter 29
Chapter 30
Chapter 31
Chapter 11 →
All chapters:
1
2
3
4
5
6
7
8
9
10
11
12
13
14
15
16
17
18
19
20
21
22
23
24
25
26
27
28
29
30
31