bible
ra
🌐 Language
English
Español
Français
Deutsch
Português
Italiano
Nederlands
Русский
中文
日本語
한국어
العربية
Türkçe
Tiếng Việt
ไทย
Indonesia
All Languages
Home
/
Wolof
/
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
/
Proverbs 31
Proverbs 31
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
← Chapter 30
Jump to:
Chapter 1
Chapter 2
Chapter 3
Chapter 4
Chapter 5
Chapter 6
Chapter 7
Chapter 8
Chapter 9
Chapter 10
Chapter 11
Chapter 12
Chapter 13
Chapter 14
Chapter 15
Chapter 16
Chapter 17
Chapter 18
Chapter 19
Chapter 20
Chapter 21
Chapter 22
Chapter 23
Chapter 24
Chapter 25
Chapter 26
Chapter 27
Chapter 28
Chapter 29
Chapter 30
Chapter 31
1
Lii waxi Lemuyel la, buuru Maasa, te ndeyam jàngal ko ko. Mu ne:
2
Ngóor si doom, saa doomi bopp! Yaa di ñaan gu nangu, doom!
3
Bul jox jigéen ñi sa doole, bul jox say siddit jigéen ñiy sànk buur.
4
Buur moomul di naan biiñ, Lemuyel, buur moomu ko; kilifa moomul di sàkku ñoll.
5
Lu ko moy mu naan, ba fàtte lu yoon tëral, xañ néew-ji-doole ju ne, àqam.
6
Bàyyeel ñoll kuy sànku, bàyyi biiñ ak boroom naqar.
7
Bu ñu naanee, fàtte seen néewle, ba dootuñu fàttliku seenu tiis.
8
Nanga àddul ku amul kàddu, ku sësul fenn, nga ñoŋal àqam.
9
Deel àddu, di àtte njub; ku ñàkk ak ku néewle, nga sàmm àqam.
10
Jeeg bu jàmbaare, ndaw lu jafe, ba rawati gànjar!
11
Jëkkër ja da koy wóolu, te jëkkër ja day am xéewal, du ko ñàkk.
12
Day defal jëkkëram lu baax, du ko lor, tey ànd ak bakkan.
13
Day wut kawari gàtt aki wëñ, di ca liggéeye mbégte.
14
Day mel ni gaalu jula, di jëli dundam fu sore.
15
Day jóg te bët setul, di waajal njëlu njabootam, ak a sas ay janqam.
16
Day seetlu ab tool, jënd ko, sàkk ciw ñaqam, jëmbat tóokër.
17
Day gañu di góor-góorlu, ak a dëgëral përëg ya.
18
Day gis njartel liggéeyam, te làmpam du fey guddi.
19
Ma ngay yor poqe ak këccu, di ëcc.
20
Day jox ku ñàkk, di sàkkal néew-ji-doole.
21
Tiitul ci njaboot gi sedd bu metti, ndax ñoom ñépp ay tegley yére.
22
Mooy sàkkal boppam ay malaan, ay yéreem mucc ayib te yànj.
23
Dees na ràññee jëkkëram ca pénc ma, fa muy toog ca magi réew ma.
24
Ndaw su ni mel day ràbb ay yére, di jaay, aki gañaay, di jox jaaykat yi.
25
Faaydaak jom la làmboo, te ëllëg ubul boppam.
26
Day wax lu xelu, di digle ngor.
27
Jigéen jooju mooy bàyyi xel ci njabootam, te du nangoo yàccaaral.
28
Doom ya dañu ko naan: «Jarawlakk!» jëkkër ja di ko gërëm naan:
29
«Jeeg bu jàmbaare bare na, waaye yaw, yaa ci raw.»
30
Melokaan wu jekk day naxe, taar day wéy, waaye jigéen ju ragal Aji Sax ji, kookoo jara gërëm.
31
Joxleen ko njukkalu ñaqam, jëfam di woyam ca pénc ma.
← Chapter 30
Jump to:
Chapter 1
Chapter 2
Chapter 3
Chapter 4
Chapter 5
Chapter 6
Chapter 7
Chapter 8
Chapter 9
Chapter 10
Chapter 11
Chapter 12
Chapter 13
Chapter 14
Chapter 15
Chapter 16
Chapter 17
Chapter 18
Chapter 19
Chapter 20
Chapter 21
Chapter 22
Chapter 23
Chapter 24
Chapter 25
Chapter 26
Chapter 27
Chapter 28
Chapter 29
Chapter 30
Chapter 31
All chapters:
1
2
3
4
5
6
7
8
9
10
11
12
13
14
15
16
17
18
19
20
21
22
23
24
25
26
27
28
29
30
31