bible
ra
🌐 Language
English
Español
Français
Deutsch
Português
Italiano
Nederlands
Русский
中文
日本語
한국어
العربية
Türkçe
Tiếng Việt
ไทย
Indonesia
All Languages
Home
/
Wolof
/
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
/
Proverbs 4
Proverbs 4
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
← Chapter 3
Jump to:
Chapter 1
Chapter 2
Chapter 3
Chapter 4
Chapter 5
Chapter 6
Chapter 7
Chapter 8
Chapter 9
Chapter 10
Chapter 11
Chapter 12
Chapter 13
Chapter 14
Chapter 15
Chapter 16
Chapter 17
Chapter 18
Chapter 19
Chapter 20
Chapter 21
Chapter 22
Chapter 23
Chapter 24
Chapter 25
Chapter 26
Chapter 27
Chapter 28
Chapter 29
Chapter 30
Chapter 31
Chapter 5 →
1
Gone yi, tee ngeena dégg yaru baay, te déglu, ba am ug dégg?
2
Maa ngi leen di jàngal lu baax, buleen fàtte sama njàngle.
3
Man it amoon naa baay, di benn bàjjo ci saa ndey.
4
Baay digal ma, ne ma: «Jàppal samay wax ci sam xel, di jëfe samay santaane, ba dund.
5
Amal xel mu rafet akug dégg. Bul fàtte te bul moy samay wax.
6
Bul dëddu xel mu rafet, da lay aar; sopp ko, mu sàmm la.
7
Njàlbéenu xel mu rafet mooy sàkku ko; ak loo mana am, amal ug dégg.
8
Nawal xel mu rafet, mu darajaal la; tafoo ko, mu teral la.
9
Da lay takkal kaala gu jekk, solal la mbaxanam buur.»
10
Déglul, doom, te dégg saay wax, ndax nga gudd fan.
11
Yoon wu xelu laa la teg, jaarloo la yoonu njub.
12
Doo dox ba tërëf, doo daw, téqtalu.
13
Ŋoyal cib yar, bul yoqi, sàmm ko, moo yor sa bakkan.
14
Yoonu ku bon, bu ci tegu; fu ab soxor di jaar, bu fa dox.
15
Moyul, bu fa jaare; mbasal te wéy!
16
Ku bon du nelaw te lorewul, du dajjant ba kera muy téqe.
17
Daa bon, def ko lekk, di màndee coxoram.
18
Yoonu ku jub day leer, ba ne ràññ ni bëccëg.
19
Yoonu ku bon ne këruus, du xam lu muy téqtaloo.
20
Doom, déglul samay kàddu, teewlul samay wax.
21
Bu ci noppee ja jàkk, te jàpp ko ci sa biir xel.
22
Mooy dundloo ku ci jàpp, di wéral jëmmam jépp.
23
Sàmmala sàmm sab xol, nde xalaati xol ngay jëfe.
24
Dàqal wor, mu sore la; kàdduy naxe, na la dànd.
25
Xooleel, sa bët ne jàkk, ngay xool sa kanam màkk.
26
Seetlul fi ngay teg tànk, ba foo awe, mu wóor.
27
Bul jàdd, ndijoor mbaa càmmoñ, na sa tànk moyu lu bon.
← Chapter 3
Jump to:
Chapter 1
Chapter 2
Chapter 3
Chapter 4
Chapter 5
Chapter 6
Chapter 7
Chapter 8
Chapter 9
Chapter 10
Chapter 11
Chapter 12
Chapter 13
Chapter 14
Chapter 15
Chapter 16
Chapter 17
Chapter 18
Chapter 19
Chapter 20
Chapter 21
Chapter 22
Chapter 23
Chapter 24
Chapter 25
Chapter 26
Chapter 27
Chapter 28
Chapter 29
Chapter 30
Chapter 31
Chapter 5 →
All chapters:
1
2
3
4
5
6
7
8
9
10
11
12
13
14
15
16
17
18
19
20
21
22
23
24
25
26
27
28
29
30
31