bible
ra
🌐 Language
English
Español
Français
Deutsch
Português
Italiano
Nederlands
Русский
中文
日本語
한국어
العربية
Türkçe
Tiếng Việt
ไทย
Indonesia
All Languages
Home
/
Wolof
/
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
/
Proverbs 5
Proverbs 5
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
← Chapter 4
Jump to:
Chapter 1
Chapter 2
Chapter 3
Chapter 4
Chapter 5
Chapter 6
Chapter 7
Chapter 8
Chapter 9
Chapter 10
Chapter 11
Chapter 12
Chapter 13
Chapter 14
Chapter 15
Chapter 16
Chapter 17
Chapter 18
Chapter 19
Chapter 20
Chapter 21
Chapter 22
Chapter 23
Chapter 24
Chapter 25
Chapter 26
Chapter 27
Chapter 28
Chapter 29
Chapter 30
Chapter 31
Chapter 6 →
1
Sama doom, déglul sama xel mu rafet, teewlul sama déggin,
2
kon nga saxoo foog, say wax tegu ci xam-xam.
3
Lu mel ni lem la ndaw su yemadi di wax, làmmiñ wa ni diw gu ñu lay raay.
4
Muj ga mu wex xàtt, di gaañe ni ñawkay saamar.
5
Tànk ya day bartalu wuti ndee, ay jéegoom àkki njaniiw.
6
Rëddul yoonu dund, daa lajj, te xamu ko.
7
Kon, doom, déglu ma, bul wacc samay kàddu.
8
Soreel ndaw soosu, bul jege bunt këram.
9
Kon nga ñàkk daraja, keneen jagoo; ku néeg bóom la.
10
Jaambur jariñoo sa doole, doxandéem jagoo saw ñaq.
11
Ngay mujje onk, desey yax, jeex tàkk.
12
Nga naan: «Su ma yégoon, sopp ab yar te baña sofental waxi àrtu.
13
Lu ma tee woona dégg ku may digal, tey teewlu sama waxi sëriñ ya?
14
Tuuti ma yàqu yaxeet fi kanam ñépp!»
15
Naanal ci sa mbalkam bopp, ndox ma balle sa teenu bopp.
16
Xanaa doo wasaare sa bëti ndox ca biti, mu def ay wal ca pénc ya?
17
Nay sa alal, yaw doŋŋ, ku bokk feneen bokkul.
18
Yal na sa naanukaay barkeel, nga bànneexoo kiy sa jabar ba ngay ndaw.
19
Aka sopplu te jekk! Na lay céram doy foo tollu, na la xañ sago saa su ne.
20
Doom, ana looy xemmeme keneen, bay foye céri jaambur?
21
Lu waay jëf, Aji Sax ji gis, di xool mboolem fu mu jaare.
22
Jëf ju bon day fiir ka ko sàlloo, bàkkaaram di mbaal, jàpp ko.
23
Ñàkk yar, dee; ndof gu réy, sànku.
← Chapter 4
Jump to:
Chapter 1
Chapter 2
Chapter 3
Chapter 4
Chapter 5
Chapter 6
Chapter 7
Chapter 8
Chapter 9
Chapter 10
Chapter 11
Chapter 12
Chapter 13
Chapter 14
Chapter 15
Chapter 16
Chapter 17
Chapter 18
Chapter 19
Chapter 20
Chapter 21
Chapter 22
Chapter 23
Chapter 24
Chapter 25
Chapter 26
Chapter 27
Chapter 28
Chapter 29
Chapter 30
Chapter 31
Chapter 6 →
All chapters:
1
2
3
4
5
6
7
8
9
10
11
12
13
14
15
16
17
18
19
20
21
22
23
24
25
26
27
28
29
30
31