bible
ra
🌐 Language
English
Español
Français
Deutsch
Português
Italiano
Nederlands
Русский
中文
日本語
한국어
العربية
Türkçe
Tiếng Việt
ไทย
Indonesia
All Languages
Home
/
Wolof
/
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
/
Proverbs 20
Proverbs 20
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
← Chapter 19
Jump to:
Chapter 1
Chapter 2
Chapter 3
Chapter 4
Chapter 5
Chapter 6
Chapter 7
Chapter 8
Chapter 9
Chapter 10
Chapter 11
Chapter 12
Chapter 13
Chapter 14
Chapter 15
Chapter 16
Chapter 17
Chapter 18
Chapter 19
Chapter 20
Chapter 21
Chapter 22
Chapter 23
Chapter 24
Chapter 25
Chapter 26
Chapter 27
Chapter 28
Chapter 29
Chapter 30
Chapter 31
Chapter 21 →
1
Naan biiñ ak ñaawle, naan ñoll, tanqale, ku mu nax xeluwoo.
2
Buur mer lool, mel ni gayndee ŋar; boo ko merloo, dangay xaru.
3
Moytuw ay, ndam la; dof boo gis day bëgg xuloo.
4
Ab yaafus du gàbb ba mu jotee, day wut am ngóob, du am dara.
5
Mébétu jaambur day teen bu xóot, ku am ug dégg a cay root.
6
Ñu baree ngi naa: «Gore naa,» waaye kuy boroom kóllëre dëgg?
7
Ku jub, di jëfeg mat, doom ju la wuutu bég na.
8
Su buur toogee di àtte, day gis, di ràññee mboolem ayib.
9
Ana ku man ne fóot na xolam, ba tàggook bàkkaar?
10
Nattu diisaay yu yemul ak lu ni mel, Aji Sax ji bañ na ko.
11
Gone sax day jëf, nga gis jikkoom; bu naree dëggu te jub, nga xam.
12
Nopp buy dégg ak bët buy gis, Aji Sax jee sàkk lu ci nekk.
13
Bul bëggi nelaw, ba ñàkk dab la; boo njaxlafee, lekk ba desal.
14
Kuy waxaalee ngi naan: «Baaxul de!» Bu nee wërëñ, di damu naan: «Aka jar!»
15
Wurus am na ak gànjar yu bare, waaye kàdduy xam-xam a gën per yu jafe.
16
Ku gàddul jaambur bor, jëlal mbubbam; tayle ko, moo dige feyal jaambur.
17
Njublaŋ, lekk, jëkke neex, mujj mel ni lancub suuf.
18
Pexe, ndigal a koy lal; xare, ay tegtal.
19
Kuy wër di jëw, wuññi sutura; ku réy làmmiñ, bul déeyook moom.
20
Ku saaga sa ndey mbaa sa baay añe lëndëmu bàmmeel.
21
Alal ju gaaw du mujje barkeel.
22
Bul feyantook ku la tooñ; dénkul ci Aji Sax ji, mu wallu la.
23
Aji Sax ji bañ na nattu diisaay yu wuute, njublaŋ ci natti diisaay baaxul.
24
Jéegoy jaam Aji Sax jee ko yor, kenn xamul foo jëm.
25
Bul gaawtuy digeek Yàlla, di dugal sa bopp; bul giñ, di réccu.
26
Buur, bu xeloo, ràññee ku bon, mbugal ko, te du ko ñéeblu.
27
Xelum nit làmp la bu Aji Sax ji taal, da koy niital ba ca biir xolam.
28
Ngor ak worma day aar buur, ngor ay saxal ab jalam.
29
Sagu ndaw, doole ja; gànjaru mag, bijjaaw ba.
30
Dóor yu la gaañ faj na sag mbon, ay yar fóot na xolu boroom.
← Chapter 19
Jump to:
Chapter 1
Chapter 2
Chapter 3
Chapter 4
Chapter 5
Chapter 6
Chapter 7
Chapter 8
Chapter 9
Chapter 10
Chapter 11
Chapter 12
Chapter 13
Chapter 14
Chapter 15
Chapter 16
Chapter 17
Chapter 18
Chapter 19
Chapter 20
Chapter 21
Chapter 22
Chapter 23
Chapter 24
Chapter 25
Chapter 26
Chapter 27
Chapter 28
Chapter 29
Chapter 30
Chapter 31
Chapter 21 →
All chapters:
1
2
3
4
5
6
7
8
9
10
11
12
13
14
15
16
17
18
19
20
21
22
23
24
25
26
27
28
29
30
31