bible
ra
🌐 Language
English
Español
Français
Deutsch
Português
Italiano
Nederlands
Русский
中文
日本語
한국어
العربية
Türkçe
Tiếng Việt
ไทย
Indonesia
All Languages
Home
/
Wolof
/
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
/
Proverbs 2
Proverbs 2
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
← Chapter 1
Jump to:
Chapter 1
Chapter 2
Chapter 3
Chapter 4
Chapter 5
Chapter 6
Chapter 7
Chapter 8
Chapter 9
Chapter 10
Chapter 11
Chapter 12
Chapter 13
Chapter 14
Chapter 15
Chapter 16
Chapter 17
Chapter 18
Chapter 19
Chapter 20
Chapter 21
Chapter 22
Chapter 23
Chapter 24
Chapter 25
Chapter 26
Chapter 27
Chapter 28
Chapter 29
Chapter 30
Chapter 31
Chapter 3 →
1
Sama doom, déggal samay wax, fonk samay santaane.
2
Teewlul xel mu rafet, sam xel di dégg.
3
Ngalla wutala dégg, wool dég-dég wall.
4
Sàkkul xel mu rafet ni xaalis, wut ko ni alal ju làqu.
5
Kon nga xam luy ragal Aji Sax ji, xam Yàllaa di kan;
6
ndax Aji Sax jeey maye xel mu rafet, kàddoom di taxa xam, di dégg.
7
Day dencalal ndam kiy jubal, di yiir ku mat.
8
Day wattu ku jub fu mu jaare, di sàmm wóllëreem ciw yoon.
9
Kon nga xam njub ak yoon, xam jubal ak mboolem yoonu mbaax.
10
Ndax xel mu rafet miy tàbbi sa xol, nga xam, sa xol tooy,
11
nga foog, fegu, am ug dégg, raw,
12
mucc ci yoonu ku bon ak kuy wax lu jekkadi,
13
mucc ci kuy wacc yoonu njub, di jaare mbedd yu lëndëm.
14
Kon nga mucc ci kuy def lu bon, tey bànneexoo lu jekkadi.
15
Yoonu ku ni mel day lunk, jaaruwaayam dëng.
16
Xel mu rafet da lay musal ci ndaw su yemadi, bokk feneen, di wax lu neex.
17
Day dëddu wóllëreem, ba muy ndaw, fàtte kóllëreem ak Yàllaam.
18
Këram day joy wuti ndee, ay jaaruwaayam jëm njaniiw.
19
Ku dem ca moom dootoo délsi, doo gisati yoonu dund mukk.
20
Kon nag aweel mbeddum waa ju baax, toppal yoonu ku jub,
21
ndax kuy jubal ay dëkke réew mi, te ku mat a fiy des.
22
Ku bon, ñu dagge ci réew mi; kuy fecci worma, ñu buddi, sànni.
← Chapter 1
Jump to:
Chapter 1
Chapter 2
Chapter 3
Chapter 4
Chapter 5
Chapter 6
Chapter 7
Chapter 8
Chapter 9
Chapter 10
Chapter 11
Chapter 12
Chapter 13
Chapter 14
Chapter 15
Chapter 16
Chapter 17
Chapter 18
Chapter 19
Chapter 20
Chapter 21
Chapter 22
Chapter 23
Chapter 24
Chapter 25
Chapter 26
Chapter 27
Chapter 28
Chapter 29
Chapter 30
Chapter 31
Chapter 3 →
All chapters:
1
2
3
4
5
6
7
8
9
10
11
12
13
14
15
16
17
18
19
20
21
22
23
24
25
26
27
28
29
30
31