bible
ra
🌐 Language
English
Español
Français
Deutsch
Português
Italiano
Nederlands
Русский
中文
日本語
한국어
العربية
Türkçe
Tiếng Việt
ไทย
Indonesia
All Languages
Home
/
Wolof
/
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
/
Proverbs 11
Proverbs 11
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
← Chapter 10
Jump to:
Chapter 1
Chapter 2
Chapter 3
Chapter 4
Chapter 5
Chapter 6
Chapter 7
Chapter 8
Chapter 9
Chapter 10
Chapter 11
Chapter 12
Chapter 13
Chapter 14
Chapter 15
Chapter 16
Chapter 17
Chapter 18
Chapter 19
Chapter 20
Chapter 21
Chapter 22
Chapter 23
Chapter 24
Chapter 25
Chapter 26
Chapter 27
Chapter 28
Chapter 29
Chapter 30
Chapter 31
Chapter 12 →
1
Aji Sax ji bañ na njublaŋ ci nattub diisaay, ay nattukaay na mat, muy bànneexam.
2
Ku réy-réylu rus; woyofal ndax nga xelu.
3
Kuy jubal, jiital mat. Njublaŋ ak wor, detteelu.
4
Alal du jariñ bésu mbugal; jub, mucc ci gàtt fan.
5
Ku mat, njekk xàllal la; coxor daaneel boroom.
6
Jubalal, sa njekk musal la; ab workat day bëgge, ba far keppu.
7
Ab soxor saay, yaakaaram seey, rawatina yaakaar ju sës ci alal.
8
Ku jub mucc ci njàqare, ab soxor wuutu ko ca.
9
Ay sos la yéefar di loree, waaye ku jub xam-xam la cay mucce.
10
Ku jub baaxle, waa dëkkam bànneexu; ab saaysaay saay, mbégte dim riir.
11
Barkeb ku jub teral nab dëkk, kàddug ku soxor tas nab dëkk.
12
Waxi xeebaate ñàkk bopp la, ku am ag dégg day noppi.
13
Kuy wër di sos dangay wuññi sutura, ku jara wóolu dangay am bàmmeelu biir.
14
Tegtal tumurànke, am réew suux; digle bare, ndam dikk.
15
Bul gàddul kenn bor, di loru; bañ koo dige, daldi am jàmm.
16
Jigéen, na yiw, ñu sagal ko; góor gu néeg, alal doŋŋ.
17
Ku baax, boppam; ku bon, boppam.
18
Coxor feyul boroom, day naxe; deel def njekk, sag pey wóor.
19
Saxoo njekk, dund; sàlloo mbon, dee rekk.
20
Aji Sax ji bañ na njublaŋ, safoo maandute.
21
Ab soxor mbugalam du jaas, wóor na; te ku jub, saw askan mucc.
22
Taaru jongama ju xel ma gàtt, mooy jaaro wurus ci noppu mbaam-xuux.
23
Ku jub, lu baax rekk lay sàkku; soxor biy yaakaar, mujje mbugal.
24
Nit a ngi tabe, di yokkule; nit di nëŋ-nëŋi, gëna ñàkk.
25
Ku yéwén, woomle; kuy suuxat, suuxu.
26
Nit a ngi móolu kuy denc pepp, ba mu ñàkkee, di gërëm ka koy jaay.
27
Wutala wut lu baax, ñu nawloo la; ku sàkku lu bon, yaa koy yenu.
28
Ku yaakaar sa alal sab jéll a ngi ñëw, ku jub day juble ni gàncax gu naat.
29
Kuy fitnaal sa waa kër doo donn dara, ku dof, boroom xel yilif la.
30
Nit ku jub garab la, doom ya di dundal; ku rafet xel wut nit ñi.
31
Ku jub, jot sa yool ci kaw suuf, moykat beek soxor bi it daw raw.
← Chapter 10
Jump to:
Chapter 1
Chapter 2
Chapter 3
Chapter 4
Chapter 5
Chapter 6
Chapter 7
Chapter 8
Chapter 9
Chapter 10
Chapter 11
Chapter 12
Chapter 13
Chapter 14
Chapter 15
Chapter 16
Chapter 17
Chapter 18
Chapter 19
Chapter 20
Chapter 21
Chapter 22
Chapter 23
Chapter 24
Chapter 25
Chapter 26
Chapter 27
Chapter 28
Chapter 29
Chapter 30
Chapter 31
Chapter 12 →
All chapters:
1
2
3
4
5
6
7
8
9
10
11
12
13
14
15
16
17
18
19
20
21
22
23
24
25
26
27
28
29
30
31