bible
ra
🌐 Language
English
Español
Français
Deutsch
Português
Italiano
Nederlands
Русский
中文
日本語
한국어
العربية
Türkçe
Tiếng Việt
ไทย
Indonesia
All Languages
Home
/
Wolof
/
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
/
Proverbs 6
Proverbs 6
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
← Chapter 5
Jump to:
Chapter 1
Chapter 2
Chapter 3
Chapter 4
Chapter 5
Chapter 6
Chapter 7
Chapter 8
Chapter 9
Chapter 10
Chapter 11
Chapter 12
Chapter 13
Chapter 14
Chapter 15
Chapter 16
Chapter 17
Chapter 18
Chapter 19
Chapter 20
Chapter 21
Chapter 22
Chapter 23
Chapter 24
Chapter 25
Chapter 26
Chapter 27
Chapter 28
Chapter 29
Chapter 30
Chapter 31
Chapter 7 →
1
Doom, dangaa gàddul nit bor, dige feyal jaambur,
2
saw làmmiñ yeb la cim pax, nga keppu?
3
Yaa ngi ci sa loxoy moroom, kon defal nii, doom, ba rëcc: doxal tinuji ko, raamali ko.
4
Bul gëmm, bul nelaw!
5
Dawal ni kéwél gu rëcc ub rëbb, ne fërr ni picc mu raw ab fiirkat.
6
Yaafus bee, xoolal xorondom, seetal ci moom, ba muus.
7
Du ku ko yilif mbaa ku koy sas, te jiiteesu ko.
8
Bu jotee mu denc ab dundam, mu jot, mu for lekkam.
9
Moo yaafus bi, foo àppal tëraay bi? Loo deeti xaar ci yewwu?
10
Ngay dajjant ak a for bët, di tegley loxook a jaaxaan.
11
Néewlee ngi lay dikkal nib sàcc, ñàkk gànnaayul la.
12
Ku tekkeedi te bon, day wër di fen,
13
day piis, di wokkeb tànk, di waxe baaraam,
14
jekkadiy xalaat, di mébét lu bon aka yokku ay.
15
Moo tax musiba di jekki dal ko, mu jekki yàqu, ba wees paj.
16
Juróom benn a ngii yu Aji Sax ji bañ, ba ci juróom yaar yu mu seexlu:
17
kuy daŋŋiiral, kuy fen, kuy rey nit ku deful dara,
18
kuy fexe lu bon ci xolam, kuy gaawtuy def lu ñaaw,
19
seede buy fen rekk, rawatina kuy yokku ay ci biiri bokk.
20
Doom, defal li la baay sant, te bul wacc ndigalal yaay.
21
Takkal foo tollu, taf ci sa xol, fas ko ci sa baat.
22
Booy dox mu di la jiite, nga tëdd, mu di la sàmm, nga yewwu, mu di la waxal.
23
Santaane da lay niital, ndigal leeralal la, artook ub yar di yoonu dund.
24
Da lay aar ci ndaw su bon ak jabaru jaambur ak làmmiñam wu neex.
25
Bu ko xemmeme taaram, bumu la fiir aki lamsal.
26
Dogu mburu fey nab gànc; waaye jabaru jaambur, bakkanu lëmm.
27
Te ku ne sawara cas, tafoo, lakk say yére.
28
Ku dox ciy xal it, say tànk ñor.
29
Mooy ànd ak jabaru jaambur, ku ko def gis ko.
30
Deesul sikk ku sàcc aw ñam, def ci biiram ndax xiif.
31
Waaye bu feeñee, fey boroom juróom yaari yoon, joxe alalu këram yépp.
32
Njaaloo di ñàkk bopp, kuy sànk bakkanam a koy def.
33
Mbugal ak toroxte dib añam, te gàcceem du deñ.
34
Fiiraange day feesal xolu góor, te du ñéeblu buy feyu.
35
Du faale ndàmpaay, loo ko may, may, du giif.
← Chapter 5
Jump to:
Chapter 1
Chapter 2
Chapter 3
Chapter 4
Chapter 5
Chapter 6
Chapter 7
Chapter 8
Chapter 9
Chapter 10
Chapter 11
Chapter 12
Chapter 13
Chapter 14
Chapter 15
Chapter 16
Chapter 17
Chapter 18
Chapter 19
Chapter 20
Chapter 21
Chapter 22
Chapter 23
Chapter 24
Chapter 25
Chapter 26
Chapter 27
Chapter 28
Chapter 29
Chapter 30
Chapter 31
Chapter 7 →
All chapters:
1
2
3
4
5
6
7
8
9
10
11
12
13
14
15
16
17
18
19
20
21
22
23
24
25
26
27
28
29
30
31