bible
ra
🌐 Language
English
Español
Français
Deutsch
Português
Italiano
Nederlands
Русский
中文
日本語
한국어
العربية
Türkçe
Tiếng Việt
ไทย
Indonesia
All Languages
Home
/
Wolof
/
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
/
Job 20
Job 20
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
← Chapter 19
Jump to:
Chapter 1
Chapter 2
Chapter 3
Chapter 4
Chapter 5
Chapter 6
Chapter 7
Chapter 8
Chapter 9
Chapter 10
Chapter 11
Chapter 12
Chapter 13
Chapter 14
Chapter 15
Chapter 16
Chapter 17
Chapter 18
Chapter 19
Chapter 20
Chapter 21
Chapter 22
Chapter 23
Chapter 24
Chapter 25
Chapter 26
Chapter 27
Chapter 28
Chapter 29
Chapter 30
Chapter 31
Chapter 32
Chapter 33
Chapter 34
Chapter 35
Chapter 36
Chapter 37
Chapter 38
Chapter 39
Chapter 40
Chapter 41
Chapter 42
Chapter 21 →
1
Cofar mu Naama àddu ne:
2
Kon ma àddooti ndax jaaxle, ba xol jallaañoo.
3
Dégg naa kàddug yedde gi nga may saagaa, waaye samam xel a ma déey sa tont.
4
Xanaa xamoo lii? La dale ca cosaan, ba nit tegoo kaw suuf ba tey,
5
xamoo ne ku bon, ag sarxolleem àggul fenn, te bànneexu yéefar yàggul?
6
Bu màggoon ba tollook asamaan it, ba bopp ba àkki fa kawa kaw,
7
day mujj seey fàww niy jonkanam; ña ko daa gis naa: «Ana mu?»
8
Kenn du ko gisati, day réer ni gént, mbaa njeneeru guddi ju dàqu, wéy.
9
Bët bu ko gisoon du ko tóllanti, dëkkuwaayam dootu ko séen,
10
ay doomam ay dàmp néew-ji-doole yi, ba delloo seen alal.
11
Mooy ànd ak dooley ndawam, tëri biir bàmmeel.
12
Lu bon la daa tàqamtikoo, log ko, làq ca suufu làmmiñ wa,
13
di ko siiramtal te du ko wacc, xanaa taf ko ca digg denqleñ ma.
14
Waaye la muy lekk ay soppiku ca biiram, doon daŋaru ñàngóor ca butit ya.
15
Moo dërëxoon alal, moo koy goqi, ca biiram la ko Yàlla di yuree.
16
Ndeke tookey ñàngóor la muucu, mu rey ko ni mat-matu saamaan.
17
Yàlla bumu niir wali dex ak waltani lem ak soow.
18
Dina delloo lu mu amoon, du ko warax; te alal ju mu jula woon, du ko jariñoo.
19
Moo dëggaate néew-ji-doole, dëddu ko; aakimoo kër jaambur te tabaxu ko.
20
Biir ba du wéet, lu mu xemmem, du rëcc.
21
Dara du rëcc ab kollam, moo tax xéewalam du toog.
22
Fa mu regge lay jàqe, mépp musiba këppu ci kawam.
23
Ba muy sol kollam la ko Yàlla di yónnee tàngooru sànjam, tawal ko ko lu fees déqam.
24
Mu daw ngànnaayu weñ, fittu xànjar bëtt ko,
25
jam ko ba fëll, cat la bëtt xol ba, di melax fa mu sare, tiitaangey ndee ne ko taral.
26
Mboolem lëndëm a làqu di ko xaar, te sawara wu loxo jafalul a koy xoyom, lakkaale lu desoon ca xaymaam.
27
Asamaan ay weer ñaawtéefam, suuf jóg, seedeel ko tuuma.
28
Koomum këram day tukki, ne mes, keroog sànjum Yàlla ma.
29
Lii moo di wàllu nit ku bon, fa Yàlla, muy cér bu ko Yàlla dogalal.
← Chapter 19
Jump to:
Chapter 1
Chapter 2
Chapter 3
Chapter 4
Chapter 5
Chapter 6
Chapter 7
Chapter 8
Chapter 9
Chapter 10
Chapter 11
Chapter 12
Chapter 13
Chapter 14
Chapter 15
Chapter 16
Chapter 17
Chapter 18
Chapter 19
Chapter 20
Chapter 21
Chapter 22
Chapter 23
Chapter 24
Chapter 25
Chapter 26
Chapter 27
Chapter 28
Chapter 29
Chapter 30
Chapter 31
Chapter 32
Chapter 33
Chapter 34
Chapter 35
Chapter 36
Chapter 37
Chapter 38
Chapter 39
Chapter 40
Chapter 41
Chapter 42
Chapter 21 →
All chapters:
1
2
3
4
5
6
7
8
9
10
11
12
13
14
15
16
17
18
19
20
21
22
23
24
25
26
27
28
29
30
31
32
33
34
35
36
37
38
39
40
41
42