bible
ra
🌐 Language
English
Español
Français
Deutsch
Português
Italiano
Nederlands
Русский
中文
日本語
한국어
العربية
Türkçe
Tiếng Việt
ไทย
Indonesia
All Languages
Home
/
Wolof
/
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
/
Job 39
Job 39
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
← Chapter 38
Jump to:
Chapter 1
Chapter 2
Chapter 3
Chapter 4
Chapter 5
Chapter 6
Chapter 7
Chapter 8
Chapter 9
Chapter 10
Chapter 11
Chapter 12
Chapter 13
Chapter 14
Chapter 15
Chapter 16
Chapter 17
Chapter 18
Chapter 19
Chapter 20
Chapter 21
Chapter 22
Chapter 23
Chapter 24
Chapter 25
Chapter 26
Chapter 27
Chapter 28
Chapter 29
Chapter 30
Chapter 31
Chapter 32
Chapter 33
Chapter 34
Chapter 35
Chapter 36
Chapter 37
Chapter 38
Chapter 39
Chapter 40
Chapter 41
Chapter 42
Chapter 40 →
1
Yaa xam jamono ju kéwéli tund di jur? Am yaa gis fu kéwél di ame doom?
2
Yaa lim weer yi muy ëmb, am yaa xam fu njuram jote,
3
ba mu sukk, jur, tàggook mititu matam,
4
ak fa doom jay leqlikook a màgg ci àll bi, ba dem, te du délsi?
5
Ana ku yóbbu fasu àll, afal ko? Ana ku yiwi mbaamu àll, wacc ko?
6
Moom mi ma jox màndiŋ mi, mu dëkke, ak jooru xorom, mu màkkaanoo?
7
Yégul riirum taax, déggul coowal dawalkat.
8
Tund yi lay wërem poram, di fa seete gépp gàncax gu tooy.
9
Ndax nagu àll a lay nangoo liggéeyal? Mbaa mu di la fanaanal ci sa ngédd?
10
Man ngaa takk nagu àll cim rijji, ba mu topp la, rijjil lab tool?
11
Yaa koy yaakaare dooleem ju bare, ba dénk ko sab liggéey?
12
Yaay yaakaar mu fatal la jiwu, jëlil la ko ca dàgga ja?
13
Bànjóolee ngi tëf-tëflu, te xodd gën koy laaf.
14
Mooy wacci nenam fi suuf, bàyyee ko tàngooru suuf.
15
Xalaatul tànk bu ci joggi ak rabu àll wu ko dëggaate.
16
Day soxore doom yi ni lu mu jurul, coonoom neen, yoonam.
17
Yàllaa ko xañ xam-xam, te séddu ko xelum ràññee.
18
Waaye bu sàqee, ba sàqi, faalewul fas ak gawaram.
19
Ndax yaa may aw fas, kàttan? Am yaa solal ndodd ma, ciiriir?
20
Am yaa koy tëbloo nim soccet, bu fiiroo, fit rëcc?
21
Fas a ngi bége dooleem, di curpee xur wa, riddi, dajeek ngànnaay.
22
Yégul tiitaange, ragalul, dawul saamar.
23
Mbarum fitt a ngay keseŋ-keseŋi fa kawam, fa xeej ak jaasi lerxatandoo,
24
mu buure xadar, taxañ suuf si, téyeetul boppam ndax liit ga jolli,
25
mu feeloo ko coowal wakkan ya. Fu sore lay xañtoo xare ba, ak kàdduy njiiti xare, ya riirandook xaacu ya.
26
Ndax sam xel la céeliy daayaarloo, ba firiy laafam, jëm bëj-saalum?
27
Am yaa sant jaxaay mu naaw ba fa kaw, di tàgge kawte ya?
28
Aw doj, mu màkkaanoo, di fanaan kaw catu doj wu ko kenn dul jote.
29
Fa lay yeeroom rëbbam, di ko niire fu sore.
30
Ku ñu bóom, ma nga fa teew, doom yay xab deret ja.
← Chapter 38
Jump to:
Chapter 1
Chapter 2
Chapter 3
Chapter 4
Chapter 5
Chapter 6
Chapter 7
Chapter 8
Chapter 9
Chapter 10
Chapter 11
Chapter 12
Chapter 13
Chapter 14
Chapter 15
Chapter 16
Chapter 17
Chapter 18
Chapter 19
Chapter 20
Chapter 21
Chapter 22
Chapter 23
Chapter 24
Chapter 25
Chapter 26
Chapter 27
Chapter 28
Chapter 29
Chapter 30
Chapter 31
Chapter 32
Chapter 33
Chapter 34
Chapter 35
Chapter 36
Chapter 37
Chapter 38
Chapter 39
Chapter 40
Chapter 41
Chapter 42
Chapter 40 →
All chapters:
1
2
3
4
5
6
7
8
9
10
11
12
13
14
15
16
17
18
19
20
21
22
23
24
25
26
27
28
29
30
31
32
33
34
35
36
37
38
39
40
41
42