bible
ra
🌐 Language
English
Español
Français
Deutsch
Português
Italiano
Nederlands
Русский
中文
日本語
한국어
العربية
Türkçe
Tiếng Việt
ไทย
Indonesia
All Languages
Home
/
Wolof
/
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
/
Job 24
Job 24
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
← Chapter 23
Jump to:
Chapter 1
Chapter 2
Chapter 3
Chapter 4
Chapter 5
Chapter 6
Chapter 7
Chapter 8
Chapter 9
Chapter 10
Chapter 11
Chapter 12
Chapter 13
Chapter 14
Chapter 15
Chapter 16
Chapter 17
Chapter 18
Chapter 19
Chapter 20
Chapter 21
Chapter 22
Chapter 23
Chapter 24
Chapter 25
Chapter 26
Chapter 27
Chapter 28
Chapter 29
Chapter 30
Chapter 31
Chapter 32
Chapter 33
Chapter 34
Chapter 35
Chapter 36
Chapter 37
Chapter 38
Chapter 39
Chapter 40
Chapter 41
Chapter 42
Chapter 25 →
1
Lu tee Aji Man ji àppal nit bési mbugal, ba ku ràññee Aji Sax ji fekke yooyu bésam?
2
Nit a ngi toxal kemu suuf, nit a ngi sàcc ug jur, foral leen.
3
Mbaamu jirim, ñu wommat, yóbbu; nagu jëtun, ñu jël kob tayle.
4
Néew-ji-doole, ñu buuxe ko ciw yoon, baadoolo yi far bokk làquji.
5
Néew-ji-doole yaa ngii mel niy mbaami àll ci màndiŋ mi, di fortaatu lu ñu lekk, àll bu wow bi yor seen xontu njaboot.
6
Tooli jaambur lañuy góobaani, di wittaani reseñ ca tóokëri ñu bon ña.
7
Duŋŋ lañuy fanaane ndax rafle, sàngoo seen der ci sedd bi.
8
Ñooy tawtee tund ya, di làqoo xunti yu ñu seeloo.
9
Xoncees na jirim ci weenu ndeyam, jëlees na tayle alalu néew-ji-doole.
10
Duŋŋ lañuy wéye ndax rafle, biir wéet, ñuy gàdduy sabaar,
11
di nal diwu oliw ci tooli jaambur, di dër reseñ ju ñu dul naan.
12
Biir dëkk ba la nit ñay binnee, ña ñu gaañ di woote wall, te Yàlla toppul kenn tooñ.
13
Ñee noonoog leer, faalewñu yoonu bëccëg te duñu fa taxawaaloo.
14
Bët di set, bóomkat jóg, bóom baadoolo bi néew doole, guddi jot mu dib sàcc.
15
Moykat bu góor a ngi yeeru timis, fab ndimo, kaalawoo, naan bët du ko gis.
16
Ñu ngi lëndëmtu, di toj kër yi, bëccëg ñu tëju, xamuñug leer.
17
Ñoom ñépp ñuulaayu guddeey seen bëccëg, lëndëm gu ne këruus lañu xejjool.
18
Yal nañu wéye walum ndox, te suuf sa ñu séddoo alku, ba kenn dootu dëgmal tóokëru reseñ.
19
Yal na maral ak tàngoor ŋiisal seen ndoxum taw, te njaniiw mëdd ña bàkkaar.
20
Yal na leen seen ndey sax fàtte, sax yi muucu leen, ñu fàtte leen, ba njubadi déjjatiku ni garab.
21
Ñu ni mel ay lekk alalu jigéen ju tëlee jur, te duñu baaxe jëtun.
22
Waaye Yàllaa mana dàq boroom doole, su nee tëll, mu xalaat bakkanam.
23
Moo leen di may ñu wéeroo seen cëslaay, tey xool fa ñuy jaare.
24
Dañuy jóg, nes tuut ñu ne mes, wadd, ñu boole for, ñu daldi lax niy gub.
25
Su dul noonu, ana ku may fenloo? Ana ku mana neenal samay wax?
← Chapter 23
Jump to:
Chapter 1
Chapter 2
Chapter 3
Chapter 4
Chapter 5
Chapter 6
Chapter 7
Chapter 8
Chapter 9
Chapter 10
Chapter 11
Chapter 12
Chapter 13
Chapter 14
Chapter 15
Chapter 16
Chapter 17
Chapter 18
Chapter 19
Chapter 20
Chapter 21
Chapter 22
Chapter 23
Chapter 24
Chapter 25
Chapter 26
Chapter 27
Chapter 28
Chapter 29
Chapter 30
Chapter 31
Chapter 32
Chapter 33
Chapter 34
Chapter 35
Chapter 36
Chapter 37
Chapter 38
Chapter 39
Chapter 40
Chapter 41
Chapter 42
Chapter 25 →
All chapters:
1
2
3
4
5
6
7
8
9
10
11
12
13
14
15
16
17
18
19
20
21
22
23
24
25
26
27
28
29
30
31
32
33
34
35
36
37
38
39
40
41
42