bible
ra
🌐 Language
English
Español
Français
Deutsch
Português
Italiano
Nederlands
Русский
中文
日本語
한국어
العربية
Türkçe
Tiếng Việt
ไทย
Indonesia
All Languages
Home
/
Wolof
/
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
/
Job 32
Job 32
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
← Chapter 31
Jump to:
Chapter 1
Chapter 2
Chapter 3
Chapter 4
Chapter 5
Chapter 6
Chapter 7
Chapter 8
Chapter 9
Chapter 10
Chapter 11
Chapter 12
Chapter 13
Chapter 14
Chapter 15
Chapter 16
Chapter 17
Chapter 18
Chapter 19
Chapter 20
Chapter 21
Chapter 22
Chapter 23
Chapter 24
Chapter 25
Chapter 26
Chapter 27
Chapter 28
Chapter 29
Chapter 30
Chapter 31
Chapter 32
Chapter 33
Chapter 34
Chapter 35
Chapter 36
Chapter 37
Chapter 38
Chapter 39
Chapter 40
Chapter 41
Chapter 42
Chapter 33 →
1
Fa la ñetti góor ñooña noppee tontu Ayóoba, ndax la Ayóoba gis njekkam.
2
Ba loolu amee Eliyu doomu Barakel ma askanoo ci Buus, bokk ci làngu Ram daa mer ba futt ca la Ayóoba dëggal boppam fi kanam Yàlla,
3
ak la ñetti xariti Ayóoba ya ñàkk lu ñu ko tontu, ba tax ñu teg Yàlla tooñ.
4
Eliyu nag moo mujjoona wax ak Ayóoba, ndax moo féete ndaw ñett ña.
5
Mu gis ne ñetti góor ña amatuñu tont, xol ba sot, mu mer ba futt.
6
Ca la Eliyu doomu Barakel waa Buus ba, àddu ne: Man de damay ndaw, ngeen diy mag, ba tax may teeylu, ragal leena biralal sama xam-xam.
7
Ma noon: «Na yàgga-dund wax, na dund-jopp xamle xel mu rafet.»
8
Ndeke xel mi ci nit mooy noowal Aji Man ji koy may dég-dég.
9
Dund-jopp taxula rafet xel, te di mag taxula xam yoon.
10
Moo tax ma ne: «Déglu ma; man it ma biral sama xam-xam.»
11
Dama ne, négandiku naa seeni kàddu, teewlu seeni déggin, ba ngeen di jeexi tont ba tey.
12
Yeen laa doon teewlu, te kat kenn ci yeen yeyu ci Baay Ayóoba, kenn joxu ko tontam.
13
Buleen ma ne: «Xel mu rafet mi nu ci gis moo di: Yàllaa ko mana tiiñal waaye du nit.»
14
Du man la Baay Ayóoba jëme kàddoom, kon du seeni wax laa koy tontoo.
15
Ñii kat jommi nañu, waxatuñu; ba kàddu dëddu leen!
16
Dama leen di xaar te waxuñu, xanaa taxaw, tontootuñu?
17
Damay tontu sama wàll, man it; damay biral sama xam-xam, man it kay!
18
Sama dënn a fees aki wax, te samam xel xiir ma ci wax.
19
Sama xol baa ngii mel ni lu sol biiñ, ube ràpp, mbete mbuus mu yees mu nara fàcc.
20
Naa wax boog, ba féex, naa àddu, ba tontu.
21
Duma ci am xejj ak seen, te duma jay kenn.
22
Xawma sax nu ñuy jaye, nde konoon ki ma sàkk gaaw ma fee jële.
← Chapter 31
Jump to:
Chapter 1
Chapter 2
Chapter 3
Chapter 4
Chapter 5
Chapter 6
Chapter 7
Chapter 8
Chapter 9
Chapter 10
Chapter 11
Chapter 12
Chapter 13
Chapter 14
Chapter 15
Chapter 16
Chapter 17
Chapter 18
Chapter 19
Chapter 20
Chapter 21
Chapter 22
Chapter 23
Chapter 24
Chapter 25
Chapter 26
Chapter 27
Chapter 28
Chapter 29
Chapter 30
Chapter 31
Chapter 32
Chapter 33
Chapter 34
Chapter 35
Chapter 36
Chapter 37
Chapter 38
Chapter 39
Chapter 40
Chapter 41
Chapter 42
Chapter 33 →
All chapters:
1
2
3
4
5
6
7
8
9
10
11
12
13
14
15
16
17
18
19
20
21
22
23
24
25
26
27
28
29
30
31
32
33
34
35
36
37
38
39
40
41
42